url
stringlengths
30
180
content
stringlengths
64
14.2k
Source
stringclasses
1 value
https://www.defuwaxu.com/diine-ak-politig-nan-moytu-li-nuy-feewale/
DIINE AK POLITIG : NAN MOYTU LI NUY FÉEWALE Ëttu boole bi, genn kurél la gu boole mbooleem këri diine yi ngir saxal jàmm ci biir réew mi, rawatina ci lu ñeel politig beek diine ji. Seetlu nanu ne saa bu jamanoy fal njiitu réew jotee rekk, njaqare dafay faral di am. Li ko waral, nag, du dara lu dul ñenn ci politiseN yi...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/kan-mooymaki-sall/
KAN MOOY…MAKI SÀLL ? Ci Baatu Majaw Njaay Aw askan, bala moo tànn njiitam, war naa seet bu baax jikkoom, seetaat ko, xam mooy kan. Looloo waral Lu defu waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc, jóg ngir jagleel wutaakon yi ay xët yuy fésal seen jaar-jaar ak seeni naal ñeel réew mi. Maanaam, li yitteel Lu defu waxu moo ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
FAN LANU JËM AK ÑAKKI BILL GATES YI? (USÉYNU BÉEY) Coow laa ngi ne kurr ! Afrig ba Afrig daj, li ko dale Keer ba Peretoryaa, Ndakaaru jàpp Adis-Abebaa, wax ji benn la : jàppal wakseŋ fii, bàyyil wakseŋ fee. Coow li nag, ci anternet bi la jëkke. Dafa am ay Móodu-Móodu ak ay Faatu-Faatu yu def ay widewoo di ci aartu s...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
WAAW, KAÑ LA SENEGAAL GËJ A YËNGOO NII…? Weeru màrs wii weesu, Senegaal tàngoon na jipp ! Gannaaw ba alkaati yeek sàndarm yi jëlijee Usmaan Sonko ngir jébbal ko Yoon, daanaka waa Ndakaaru yépp, waa Senegaal yépp sax, rawatina ndaw ñi, dañoo jóg nekk benn say, ne : “Du fi ame !” Keroog ak fan ya ca topp, jàppante bi me...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/bokk-ak-nawloo-ngir-jamm-ak-naataange-ci-addina/
BOKK AK NAWLOO NGIR JÀMM AK NAATAANGE CI ÀDDUNA SI Weer yii nu génn, réew yu bare tànn nañu seen njiit. Joŋante yi gën a indi coow mooy yi amoon ca Beliyoriisi mbaa Amerig, walla fii ci Afrig, ca Kodiwaar, Gine-Konaakiri, Burkinaa, ak-ñoom-seen. Réewum Ganaa moo ci mujj. Gëstukat yu bare ak i yéenekaay bind nañ ci, wo...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/afrobasket-kigali-2023-xalam-demoon-na-bay-neex/
AFROBASKET-KIGALI 2023 : XALAM DEMOON NA BAY NEEX ! Démb la woon finaalu Afrobasket bi doon am ren ca Ruwàndaa, doxoon ci diggante Senegaal ak Niseriyaa. Niseriyaa nag moo ko mujje gañe, daldi jël kub bi. Senegaal, ca njëlbeen ga, ku la waxoon ni dana finaalu nga weddi ko. Nde, dafa lajj ñaari yoon ca ndoorteelu xëcc...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/jeeri-joor-ndeelaak-tubaab-bi/
JÉERI JOOR NDEELAAK TUBAAB BI Jéeri Joor Ndeela Faal mu ngi gane àdduna ci atum 1871. Mu doon doom ci Sàmba Yaaya Faal mi newoon fanweer ak ñaarelu Dammeelu Kajoor te Nasaraan yi daaneloon ko ba noppi yóbbu ko Ndar-Géej, téye ko fa. Ci atum 1891 la xaru ci dex gi ginnaaw bi way-juram bu jigéen génnee àdduna te Tubaab ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (Dibéer 29 saŋwiye 2023) CHAN 2023 Sunu gaynde yee ngi wëyal di wane seen bopp fale ca Alseri. Bërki-démb, ci àjjuma ji, lañ doon daje ak seen naataango yi, Saa-Muritani yi, ñu mujje leen ko yóbbul benn bal ci dara (1-0). Ab teg-dóor lañu am, dugal ko ci xaaj bu njëkk bi. Alseri, moom mi dalal j...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/manchester-city-witti-na-biddiiwam-bu-njekk/
MANCHESTER CITY WITTI NA BIDDIIWAM BU NJËKK Àngale yaa ngay gundaandaat ! Manchester a ngi toj ! Ren, dafa baxa. Ci bëccëgu dibéeru tey ji, foo sànni woon mbàttu mu tàkk. Soppey Manchester City yaa nga feesoon dell mbeddi dëkk ba, di yuuxoo ak a fecci. Ñoo yey nag. Ndaxte, ba Manchester City dee këlëb ba tey, guléet ñ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/lan-moo-wund-demu-maki-bi-riisi/
Lan moo wund demu Maki bi Riisi ? Fan yii weesu, njiitu réew, Maki Sàll, fekki woon na Putin ca Riisi ngir, nee ñu, ñu waxtaane  bekkoor bi xare bi xew digganteem ak Ikren jural àddina si, rawatina réewi Afrig yi. Ndax kat, Maki Sàll dafa jàpp ne xare bu ni mel, baaxul ci réew yu néew doole ni réewi Afrig yi. Nde, rée...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/
AFRIG AK KORONAA, AFRIG GINNAAW KORONAA USÉYNU BÉEY Koronaawiris bi, li muy metti metti, terewul kàngami boroom xam-xam yiy wéy di ci weccee xalaat ñeel doxalinu àddina si, ba xam luy nar a doon ëllëgu doomu-aadama, bés bu nu génnee ba set ci mbas miiy fàdd nit ñi, réewoo réew. Ñu ci bare jàpp nañu ne, bu nu génnee ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
NAKA LAA GISE MBAS MI Mbas mu dërkiis, ñàkk teggin tey jur tiiñalante ci biir réew mi ak ci bitim réew…. Naka la doomi Afrig yi war a taxawe ? Céy mbas  mee gudd tànk, moom mi fàqe Penku,  ca Wuhan, ca Siin, ca Asi, sóobu ci Afrig, ba ci Géeju Atlantig, daanu ci fii ci Ndakaaru (dëkk raw) ; ci Tànk (Wakaam, Ngor, Yoo...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/lan-la-wutaakon-yi-naral-lakki-reew-mi/
Lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Waaw mbokk yi, lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Man ci sama wàllu bopp, déggaguma ci lu ma doy. Ndax Wolof, Pulaar, Séeréer, Soose, Joola, Sooninke…. dañu leen di wéy di suufeel teg Frãnse mbaa Àngale ci seen kaw ? Ndax Frãnse kese mooy wéy di nekk “làmmiñ wi Repibligu ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
JOŊANTEB XARITOO : SENEGAAL DÓOR NA KAMERUN 1-0 Gayndey kuppe yi dóor nañ Kamerun 1-0. Tey ci altine ji lañ doon amal joŋanteb xaritoo ca fowub Bollart bu Lens (France). Saajo Maane moo dugal biiwu Senegaal bi. Ab penaaltii la am, dugal ko. Joŋante bi nag, lees ko dugge mooy waajal CAN 2024 biy xewe fa Koddiwaar. Te s...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-alxames-9-mars-2023/
LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 9 MÀRS 2023) KUPPE Àngalteer Démb, foo geestu ci mbaali-jokkoo, ñoo ngi doon wone ay naataal ak i widewooy kii nga xam ni mooy defãsëeru Manchester City bi, Kyle Walker. Mu mel ne ku àndul woon ak sagoom. Nde, mi ngi ciy tërëf ni ku màndi. Bu ca yemoon sax mu tane. Waaye...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
BÉS DU MAG, DU TUUTI, BOROOM LAY TOLLOOL… Dëgg la : ràcc jëmale sa kanam baaxul waaye tey fàww LU DEFU WAXU xamle mbégteem ci ndam li Paap Aali Jàllo am fan yee nu génn ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Paap Aali ci kër gi la bokk, ayubés bu Yàlla sàkk mu am lu mu bind ci seen yéenekaay bii di LU DEFU WAXU. Nun ñiy...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/emma-seen-daan-na-saa-cees/
ËMMA SEEN DAAN NA SAA-CEES ! Démb ci dibéer ji, 5i fan ci weeru Me 2024, la doomu Pikin ji, Ëmma Seen doon sëgg ak Saa-cees, doomu Géejawaay ji. Seen bëre nekkoon lees doon xaar. Nde, dañu doon ñaari mbër yoy, duñu yàq làmb. Bu ñu bëree mu neex, bu ñu xeexee mu neex. Kii di doomu Pikin ji nag moo mujje am ndam ci kaw ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ban-a-wacc-sa-and-baay-njaay/
BAÑ A WACC SA ÀND… Mbir mi doy na waar. Kenn xamul lii lu mu doon. Nekk cim réew, dund fa lu ëpp fanweeri at, te ba tey may bind baat yi, doxandéem la ñu la fi jàppe. Am fi liggéey bu baax, di faj samay soxla ak a dimbali samay mbokk ; bokk ci ñiy yëkkati koom-koomu réew mi. Ci  gàttal, man nanoo wax ne Baay Njaay xa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
MÀGGALU DAARU XUDÓOS Mu doon tur wu siis wi ñu ko xame, màggalu daaru xudóos doon xew-xewu diine. Murit yi di ko màggal at mu jot ca Tuubaa, rawatina fa goxu daaru xudóos. Xew-xewu diine boobu di fàttali bés ba Sëriñ Tuubaa Xaadim Rasuul di wuyuji Boroomam. Mu doon bés ba ñu ko jébbalee Boroomam faTuubaa ginnaaw ba m...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/seex-beeco-cuun-atte-yallaa-gen-bu-nit/
SÉEX BEECO CUUN : ÀTTE YÀLLAA GËN BU NIT Altine 6eelu fan ci weeru Me, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, bésub layoo, bésub àtte, ñëw na. Li tax ñépp doon xaar bés bii, nag, du neen. Waaw. Kan lañu doon àtte ? Sëriñ Séex Beeco Cuun, di Xalifa di yit kilifa cantaakon yi. ‘’Bóomug Madinatul-Salaam’’, bile dàkkental la t...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sampiyonaa-almaan-bayer-leverkusen-jel-na-ko/
SÀMPIYONAA ALMAAÑ : BAYER LEVERKUSEN JËL NA KO ! Xabi Alonso ak gaayam yi def nañ ko. Dugal nañ Bayer Leverkusen ci mboorum futbalu Almaañ. Ci anam bu rafet a rafet lañ ko defee nag. Saa-Espaañ bi, Xabi Alonso miy tàggatkatu këlëb ba, def na jaloore ju réy a réy. Niki dibéeru démb ji, 14 awril 2024, lañ duma Werder Br...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
‘’LI TAX SÉEX ANTA JÓOB AMUL MOROOM…’’ Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019. Li ngeen ciy jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi. Saada Kan : Noo ngi am mbégte delsi ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2312/
Njàngatub Bàmmeelu Kocc : Téereb dekkali 1/2 Du guléet. Déedéet. Bindkat bi tëbul rekk bind Bàmmeelu Kocc Barma. Nde, ginnaaw Doomi Golo, bii mooy ñaareelu téereb nettali bu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob, génne ci làmmiñu wolof. Te sax, li ko jiitu, Bóris jot na fee yatt xalimaam gu set gi te neex, tekkil nu téereb ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
2002, ATUM SUUXU JOOLAA BI Bërki-démb 26 sàttumbar ci atum 2020, “Bateau le Joolaa” def na 18i at ci biir géej. Daanaka ñaari-junni nit ñàkkoon nañ ci seen bakkan. Te mujjagul fenn, ay daan amaguñ ci. Moonte kenn mësula gis jéeya ju tollu nii, mu waroon a tax askan week nguur gi taxaw ngir leeral ko. Dañ koy fàtte ba ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Bataaxalu Saalif Keyta ñeel IBK Ci tekkib Paap Aali Jàllo KÔRO (mag sama), Jàmm ak salaam ñeel na la. Sa rakk a lay nuyu, di la ndokkeel, di la jox sa wàccuwaay. Ginnaaw loolu, xamal ni kat, sa mbokku cosaan mi nga bokkal maam, di sa mbokku aada, moo namm a waxtaan ak yow tey. Bataaxal bii ngay jàngsi, mi ngi bawoo...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sigaret-baaxul-waaye-afrig-la-yeese/
SIGARET BAAXUL… WAAYE AFRIG LA YÉESE ! Fan yii weesu, Marie Maurisse, ab taskatu xibaar bu fekk baax Siwis, bind na bataaxal bu jar a bàyyi xel. La muy ciy nettali mooy ñaawtéef yu këri-liggéeyukaay yu mag yiy jaay sigaret ci réewi Afrig yiy def, te sunuy gornamaa ne yàcc di leen seetan. Tóx baaxul, loolu dëgg gu wer...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ndam-lu-saful-xorom-saful-suukar/
NDAM LU SAFUL XOROM, SAFUL SUUKAR…? 10Dibéer yemook ñaar-fukki fan ak ñeent si weeru Féewaryee, la waa réew mi doon tànn ki leen war a jiite ba atum 2024. Waaye, dafa mel ne li mu jur ci werantee ëpp li mu jur ci jàmm ji ñu xame Senegaal. Ndaxte, woteb njiitu réew bees génn, ñaxtook fitna lañ ci gën a ràññee. Te yit, ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/can-2021-kub-baa-nga-woon-ca-seeju-saajo-maane-delloo-mbattu-ca-ndaa-la-mu-naane/
CAN 2021 : Kub baa nga woon ca Séeju, Saajo Maane delloo mbàttu ca ndaa la mu naane Bàmbali, ci diwaanu Séeju, dalal na Kubu Afrig bi Senegaal jële woon ca Kamerun ak doomam jii di Saajo Maane. Jëwriñ ji Mataar Ba yékkati na fay kàddu, wonale kub bi Jaraafu Séejook waa Bàmbali, teg ca ni Saajo Maane nekkee royuwaay ci...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM KUPPEG TEFES Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti joŋantey xaritoo, bési 19, 20 ak 22i ci weeru desàmbar wii. Joŋante yépp moom ak Irã lay doon ca diiwaanu Teherã (Téhéran). NDAW YI MU TANN Góol : Alseyni Njaay ak Us...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/nakk-kayitu-juddu-gi-nag-ba-kan/
ÑÀKK KAYITU-JUDDU GI NAG, BA KAÑ? Ayu-bés yii weesu, yéenekaay yu bare dañoo xéy fésal ci seen xët bu njëkk xibaar bu kéemaane. Waaw, li nu ko dugge woon mooy xamal askan week Nguur gi ne lu mat junniy ndongo ak lu teg amaguñu kayitu-juddu. Déggal ma lii rekk ! Te lees war a xam moo di ne ndongo yooyu, looloo leen di ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
NISERYAA : BUHARI FALUWAAT NA Ci weeru féewaryee wii jàll la askanu Niseryaa doon amal woteb njiitu réewam. Ba ñu àggee ci cëpaandoo li, Muhammadu Buhari la askan wi tànn, dénkaat ko réew mi. Lu tollu ci 15 alfunniy wotekat ñoo sànnil xob ki toogoon ci jal bi 2015 ba léegi, mu jël raw-gàddu gi ci kanamu lawax bii di A...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
“SËRIÑ BI, FÀWW MU FEEÑ” Bu ñu seetloo fan yee ci ginnaaw, werante amoon na ci nataali Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, naan moom la ak du moom. Muy ay nataal yi ñu fésaloon ci mbaali jokkoo yi. Nataal yooyu di wone jëmmi Séex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul. Ñu xame woon ko ci benn nataal képp bu ñu miin a gis, réewu Farãs denc ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
KÀDDUY USMAAN SONKO 1/2 PÀCC Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi/
CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI WÉR-GI-YARAMI ALIW SIISE AK ABDULAAY SIMAA Bees sukkandikoo ci yégle “Fédération Sénégalaise de Football” (FSF) biral démb ci gaawu gi, Aliw Siise, tàggatkatu ekibu Senegaal bi, dafa jagadi woon. Ci àjjuma ji, bi joŋante gaynde yi jeexee, la ko feebar bu gaaw dikkal, ñu rawale ko f...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
DI BUUR, DI BUMMI Li jaaxal waa Senegaal, mooy wax-waxeet yi kilifay réew mi dëkke. Ku ci jóge ci kujje gi, dem ci nguur gi yaa ngiy xas ñaa nga àndaloon démb. Mbir mi dafay faral di am ba kenn, ci ñaari làng yépp, muccu ci. Ñépp a ngi fàttaliku ci ndetteelu atum 2018, bi peresidaŋ Maki Sàll nee mësul a ni nañu jële ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM LIGUE DES CHAMPIONS 2024-2025 Waa UEFA amal nañu ay coppite yoy, dañuy yokk limatu ekib yiy bokk ci joŋante Ligue des champions bu déwénee, atum 2024-2025 mi. Ci loolu, Araabi Sawdid mi nga xam ni, daanaka futbalkat yu xareñ yu bari ñoo ngi jóge Tugal di leen fekki ci seen sàmpiyonaa ba, ñu ci me...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
FUTBAL AK JAFE-JAFEY RÉEWI AFRIG YI Doom-aadama fent na ay xeeti po yu bare. Ba ci tàggat-yaram sax, nga xam ne, ci cosaanam, yar ak wér-gi-yaram ñoo ko taxoon a jóg, nit soppi na ko, def ko liggéey ak po, di ci amal ay joŋante yu mag, àddina sépp di ko teewe. Xeeti po yooyu, nag, futbal a ci gën a siiw te yit moo ci ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (3/9/2023) SAALIF KEYTA KUPPEKATU MALI BA WOON GAAÑU NA Ci gaawug démb ji, 2 sàttumbaar 2023, la kuppekatu Mali bi gaañu. Ndem-si-Yàlla Saalif Keyta mi ngi amoon 76i at. Moom, doomu Mali ji, mooy kuppekatu saa-afrig bi jëkk a gañe Kuppeg wurus gu Afrig (Ballon d’or africain) ca atum 1970. Saalif ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Seen xiibaari tàggat-yaram Dibéer 12i Féewaryee 2023 Kuppeg àddina këlëb yi :  “Real Madrid” defatina ko ! Démb ci gaawu gi, 11i Féewaryee bii atum 2023, la woon finaalu kuppeg àddina këlëb yi, mu doxoon ci digante “Real Madrid” ak “Al-Xilal”. “Real Madrid” moo dóor juróomi bal ci ñett (5-3) dellu jëlati raaya ji. Bi...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xecc-bu-danee-dagg/
XËCC BU DAŊEE DAGG ! Nimbir yiy doxe diggante nguur geek kujje gi bi Màkki Sáll toogee ci jal bi ba tey jii, dalul xel dara. Nun ñépp a ànd ci demokaraasi, waaye ni ko peresidaŋ Sàll gise — ku am doole danga koy wone, doo maye dara, doo yërëm kenn — mën naa jur ëllëg musiba ci réew mi. Ci sama gis-gis bu gàtt, dafa wa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/barsaa-am-barsaq-lu-xew-ci-miim-reew/
BARSAA WALLA… BARSÀQ !… LU XEW CI MIIM RÉEW? Géej gaa ngiy wann sunu doom yi. Mbete jasig juy warax béy bu lab. Ay fukki, ay téeméeriy, ay junniy waxambaane ak, léeg-léeg sax, ay janq walla ay jeeg ñooy song géej gi, wuti Barsaa walla… Barsàq ! Ñi ëpp ci ñoom, dañuy des ci ndox mi, ñuy mag di ndaw, di góor di jigéen, ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
DÉMB AK TEY Dal-leen ak jàmm ci seen xët DÉMB AK TEY mi leen seen yeénekaayu web LU DEFU WAXU jagleel. LU DEFU WAXU nag, li ko tax a jóg mooy dégtal leen ay xibaar yu wér te wóor te aju ci xew-xew yi gën a fés ci réewum Senegaal ak sax ca bitim-réew. Waaye tamit, bindkat yi dinañ  faral di leen ci baaxe seeni gis-gis...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM MESSI GAÑE NA KUBAM BU NJËKK AK INTER MIAMI Ci guddig gaawu gi jàpp dibéer jii weesu la Inter Miami doon joŋante finaalu Leagues Cup, doon ci daje ak Nashville. Bi joŋante bi dawee ba ci 23eelu simili ba la Pulga bi daldi dugalal Inter Miami, ñu dawal ba ci xaaju ñaareel bi, ci 57eelu simili bi, ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
LIGUE DES CHAMPIONS : DORTMUND AK REAL MADRID ÑOOY DAJE FINAAL Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali “Ligue des champions” bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci talaata, Paris Saint-Germain doon na janook Dortmund. Dafa di nag, Dortmund ak Real Madrid ñoo am ndam ci se...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-16-7-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (16/7/2023) KUPPEG ÀDDINA SI 2026 Kippu yi ñeel xëccoo paasu kuppeg àddina si war a am ci atum 2026 mi génn nañ fii ci wàlluw Afrig. Senegaal moo ngi bokk ci kippug B gi mook ñii di Kóngoo, Móritani, Tógoo ak ñaari Sudaŋ yi. Senegaal lees jàpp ne mooy ékib bi gën a jekkandi ci kippu gi. Waaye, na...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mbara-wacc-doomi-gaynde-njaay-yi/
MBARA-WÀCC DOOMI-GAYNDE NJAAY YI ! Sunu gaynde yi amagul ñaar-fukki at wone nañu njàmbaar fale ca Niseer, nga xam ne fa la réewi Afrig yi gën a xareñ ci futbal daje woon di joŋante. Jaaraama sunu Doomi-Gaynde yi ! Ay jàmbaar dëgg lañu, ñaawuñu ci xare bi ndax ca Niseer, daje nañook ñeenti ekib, am ndam ñeenti yoon. M...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
FUTBAL AK BASKETU SENEGAAL : YAAKAAR AK YÀKKI Bi Alseri dumaa Senegaal benn ci dara ci finaalu joŋanteb réewi Afrig yi (CAN) ak léegi, mu ngi bëgg a yàgg. Waaye, kenn fàttewu ko. Li ko waral nag mooy finaalu basket bi soxna yi ñàkk, ñoom tamit, biñ dajeek Niseryaa fan yii ñu weesu. Yaakaaroon nañu ne, soxnay basket yi...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-futbal-alxames-9-feewaryee-2023/
LI GËN A FES CI XIBAARI FUTBAL (alxames 9 féewaryee 2023) BELSIG AM NA TAGGATKAT BU BEES Kuppeg àddina 2018 ba léegi, Belsig dafa nekkoon ciy jafe-jafe. Njeexitalu kuppe gi gën koo feeñal. Moo tax ba seen tàggakat ba, Robeertoo Maartinees, xamoon boppam, tekki ndombal-tànkam balaa ñu koy dàq. Démb, ci àllarba ji la ñ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/demb-senoor-tey-wadd/
DÉMB SEŋOOR, TEY WÀDD Li ko dale atum 1978 ba tey jii, woteb ren bii mooy wote bu fi njëkk a am te Ablaay Wàdd sampu ci ndëndam. Walla boog, loolu la ñu bare jàpp. Ndax, man kat neneen laa gise mbir mi. Bees delloo ginnaaw, fàttaliku atum 2007, bi Ablaay Wàdd faluwaatee, war a amal ñaareelu moomeem, dafa wax wax ju am...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/riiru-kampaan/
RIIRU KÀMPAAÑ Lépp lu yëngu am na lu ko yëngal. Réewum Senegaal, jamono jii mu ngi toll ci waajtaayu joŋante bi ñuy fale kiy toog ci jal bi. Këru-Àtte gi gën a kowe fésal na juróomi wutaakon yu samp seen ndënd : Maki Sàll, Isaa Sàll, Usmaan Sónko, Madike Ňaŋ ak Idiriisa Sekk. Kenn ci ñoom la xelam toogatul fan yii, ta...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
SÀCCIIN WI JËM CI TÀNN YI DËGMAL TE FEEÑALEES KO Sëñ Abdu Xaadr Kebe mooy biral fii xalaatam ñeel wotey tànn Njiitu réew mees dëgmal ci atum 2024 mii nu nekk. Dafay feeñal yenn pexey njuuj-njaaj yees lal ngir sàcc wote yi, foqati baatu askan wi. 1 : Baril àdduwaay yi (lieux de vote) ak pekki àddu yi (bureaux de vote)...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
XIBAARI TAGGAT-YARAM (1/10/2023) KUPPEG ÀDDINA WAY-LUU YI (MUUMA YI) Bàyyeesu leen xel, waaye way-luu (muuma) yi teewal Senegaal ca kuppeg àddina si bees leen jagleel ñoo ngay def i jaloore yu rëy. Ba léegi, ékib gañeeguleen ! Ñoo ngi toll ci ñeenti joŋante, gañe 3 yi daldi timboo benn bi. Kaar-dë-finaal lañu war a a...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/gacce-ngaalaamambugaar-useynu-beey/
GÀCCE NGAALAAMA, MBUGAAR ! Senegaal amati na ndam ci 3eelu fan ci weeru nowàmbar wii, jaare ko ci benn ciy doomam, di Muhamet Mbugaar Saar, ab bindkat. Moom mii Farãs tappal na ko raaya bu am solo, muy Prix Goncourt  bu atum 2021. Muy raaya bu ñëw topp ci yeneen yu mu fi jotoon a am. Muhamet Mbugaar di xale bu am 31 ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/faidherbe-saay-saay-bi-nuy-sargal/
FAIDHERBE, SAAY-SAAY BI NUY SARGAL Bi Siidiya Ndàtte Yàlla génnee àddina ak léegi, am na xarnook xaaj. Waaye, mi ngi mel ni mësta gane àddina. Dara gënta ñaaw, nag, cosaan lees neenal. Nde, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. “Xare bi gën a xereñe ci xare yi, mooy bi ngay noote say noon te doo xeex”. (Sun Tzu) Bés b...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/njangat-ci-teere-ceerno-alasaan-sall-bi-nu-duppe-tenkoo-ak-takko-ba-ca-elise-deeyub-jawrin-bi-nu-denkoon-mbiri-petorol-ci-senegaal-moolkat-bi-fauves-ca-pa/
"LE PROTOCOLE DE L’ÉLYSÉE" : NJÀNGATU PROF BUUBA JÓOB Téere bu am solo bi Ceerno Alasaan Sàll génne fan yii ci nasaraan, te móolkat bi,  ca Pari, tudd Fauves, mënees na ko tekkee nii ci kàllaamay Kocc : “Tënkoo ak takkoo ca “Élysée” : déeyub jawriñ biñ dénkoon mbiri petorol ci Senegaal” Li ñu war a njëkk a wax, moo d...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/serin-seeka-bari-doole-ci-langu-politig-bi/
SËRIÑ SEEKA BARI DOOLE CI LÀNGU PÓLITIG GI ! Ni waa Senegaal gëmee Yàlla te fonk diine, umpul kenn ci àddina si. Nde, askanuw Senegaal, ñi ci ëpp ay jullit lañu. Nee ñu, cig xayma, 100 yoo jël ci doomi réew mi, 95 yi jullit lañuy wootewoo. Diiney Lislaam, nag, biir Senegaal, dafa làmboo ay màndarga yi koy wutale ak i...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/nan-mbaalo-toj-nga-lamb-ji/
ÑAŋ-MBAALO, TOJ NGA LÀMB JI ! « Toj naa fii ! », « Tasaare naa fee ! », « Rajaxe naa fale ! »… Su nu waxantee dëgg, xorom si moom la ! Moom Madike Ñaŋ, kenn ci wutaakoni yi, mooy xorom siy safal kampaañ bi ñuy waaj a jéexal. Ci biir werante yeek, xuloo yeek, ŋàññante yeek, tamante dëmm yi, Madike moom, neex deret ba...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ndongo-samba-silla-cfa-xettali-fras-a-ko-taxoon-a-jog-laaj-tontook-mamadu-jallo-i/
NDONGO SÀMBA SILLA « …CFA, XETTALI FRÃS A KO TAXOON A JÓG» Mamadu Jàllo :  Ndongo Sàmba Silla, yow doomu-Senegaal nga, di boroom xam-xamam bu mag ci wàllu koom. Ak li ngay doon ndaw yépp, sa tur wi siiw na lool ci réew mi te saw askan naw na la. Yaa ngi liggéeye Fondation Rosa Luxemburg, ñu dénk la fa lépp lu ñeel yok...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
KORONAAWIRIS : TAXAW TEEWLU Làmp Faal Kala Mbasum Covid-19 mi lëmbe na àddina, lëmbaaje xel yi ak xol yi, ba ku tiitul it jaaxle nga, mbaa sax nga faf boole tiitaange ak njàqare. La woon, lu ci ëpp wonni na tey, mbir yi jaxasoo, nit ñi di jaawale, gis-gis yi wute, ku nekk di wax ak a layal la dalum xelam. Mu mel ni ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram/
LI GËN A FÉS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM WURE (FUTBAL) Gaynde Senegaal yu ndaw yi noppi nañoo waajal Chan bi. Tey ci altine ji lañu doon amal seen ub joŋante bu mujje ci waajtaay gi. Ginnaaw bi leen Marog dóoree (1-0), ñu témboo ak Alseri (2-2), dellu témboowaat ak Libi (1-1), dañoo dóor Saa-Congo yi benn bii ci tus. Gaa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/taxawaayu-kujje-gi-ciy-wotey-gox-goxaan-yii-degmal/
KUJJE GEEK WOTEB 2022 BI: BËGG NAA LA, BËGGUMA LA, LOOLU JARUL COOW Ci bésub 23 sàŋwiye ci atum 2022 bii di ñëw, la Senegaal fas yéene amal ay wote jëm ci palu njiiti gox-goxaan yi. Gannaaw ba pàrti pólitig yi jàppante ci mbiri yoonu pal gi, maanaam li ñeel doxalinu wote bi ak jumtukaay yi mu àndal, léegi, pàrti yooye...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/
MAKI/XALIFA : MAG, BU RUSEE NE MAA-TEY Fan yii nu génn, bare woon na ñu doon yéy ak a yàbbi ci mbirum Xalifa Sàll, di wax ci njéggal bi ko Maki Sàll war a jagleel. Am na ci sax ay taskati xibaar yu demoon ba ne Xalifa Sàll këram lay tabaskijee. Waaye, bi nguur gi fésalee turi nit ñi Maki Sàll jéggal, ñu war a tabaskij...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (25/2/2024) MBIRI PAAP GÉY AK MÀRSEY Gannaaw CAN bi mu demoon ak Senegaal, Paap Géy, miliyë Màrsey (Marseille) bi dañ ko dàndoon ca këlëb ba, maanaan dañ ko génne woon, ber ko. Li ko waral mooy ni pasam dafay jeex ci weeru suwe 2024, Màrsey bëggoon mu yeesal ko. Waaye, Paap Géy dafa lànk. Njiiti ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mangaan-ndeke-am-na-ci-politig/
MÀNGAAN NDEKE AM NA CI PÓLITIG ! b ak yu tey gis ñu woroo lool. Am na sax ci ñoom ku ne woon Ndeyu-Àtte réewum Senegaal dafa war a aaye màngaan ci politig. Yemu fa, ndax dem na ba yaramam tàng, mu yokk ci ne képp ku jóge cib pàrti, ak bu mu mënti doon, dem màngi ci nguur gi, yoon dafa war a jël sa bakkan ! Moonte ngóo...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi/
DI BUUR, DI BUMMI Ci gaawu bi weesu, 4eelu fan ci weeru me, la dipite yi wote sémbub àtte biy far palaasu Njiitu-jawriñ yi ci nguurug Senegaal. Ndax sémbub àtte bi jàll na ? Loolu jarul a laaj ! Ci 138 dipite yi teewoon, 124 yi wote nañu « waaw » 7 yi « déedéet ». Yeneen 7 yi des ñoom, di waa PDS, dañoo lànk ne duñu w...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/afrig-lu-la-tax-a-des-ginnaaw/
AFRIG, LU LA TAX A DES GINNAAW ? Bare na li may toog man kenn, di yónni samam xel, mu wëral ma àddina sépp ak li ci biir, fu nekk mu ne fa naam-daraame, yër la fa nekk, dellusi. Waaye, li ëpp ci samay xalaat ak i seetlu, Afrig la ñeel, sunu Afrig ak ëllëgam. Bu ko defee, sama xel mi day faral di wër réewi Afrig yi ba ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
SUNUY DOOMI-NDEYI MALI YI SONN NAÑU At yi weesu yépp, fitu doomi-Mali yi toogul benn béréb. Weer yi nu génn sax, seen njàqare ak seen tiis dafa mel ni lu yokku. Te lenn waralu ko lu dul jàmmaarloo yu tar yi am ci diggante ñaari waasoo yii di Pël yeek Dogoŋyi. Lu ni mel nag, jaaxal na ñu baree-bari. Ndax, ci atum 2012 ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM FUTBAL Victor Boniface moo ngi dox ci ndox Ataakã Bayer Leverkusen bi moo ngi wane boppam bu baax jamono jii ca sàmpiyonaa Almaañ ba. Lu tollu ci ñeenti weer a ngi nii (ut, sàttumbar, oktoobar ak nowàmbar) moom lees di tabb  ki gën a xareñ ci weer wi. Santos wacc na Këlëbu Beresil bi moo ngi a...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-19-11-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (19/11/2023) LÀMB : LAG DË GEER 2 DAAN NA SITTA Ñaari mbër yi waajal nañu seen bés bi, def nañu lépp li ci war, neexal seen i jàkkaarloo ak bés beet. Lag dë geer 2 dafa ñëw, ànd ak kóolute, bàkku, yëngal, daldi koy xumbal. Sitta tamit, waxi noppi. Ñëw na nees ko xamee, ànd ak mbooloo mu takku, mu...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/
FUTBAL : LIGUE DES CHAMPIONS, EUROPA LEAGUE AK CONFERENCE LEAGUE Barki-démb, démb ak tey lañ doon amal joŋantey kaar-dë-finaal Ligue des champions yi, Europa League ak Conférence League fa Tugal. League des champions Ci talaata ji la Dortmund ak Atletico Madrid doon amal seen ñaareelu ndaje. Ca ndaje mu njëkk ma ame...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
WAAW, ANA KU BÓOM OMAR BOLONDEŋ JÓOB ? Omar Bolondeŋ Jóob a ngi juddu ci 10eelu fan ci weeru sàttumbar 1946 ca Ñaame, péeyub réewum Niseer. Mu ngi faatu ci 11eelu fan ci weeru Mee 1973 ca kaso ba woon ca dunub Gore. Omar Bolondeŋ Jóob, nag, kàngam la woon ci biir kàngam yi, jànge ca lekkoolu digg-dóom ji ñu duppe Lou...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/
7 MÀRS WALLA 8 MÀRS ? BEY CI SA WEWU TÀNK… Juróom-ñetteelu fan ci weeru màrs la xel yépp di dem ci jigéen ñi, ndax seen bés la. Àddina sépp a koy màggal, di ci amal ay ndaje, ay waxtaan yu yaatu waaye it di natt ba xam fu xeex bi tollu. Lépp a ngi tàmbali ci 1917, ca Saint-Petersburg, at ma ay óbëryee yu jigéen meree...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/laaj-tontu-saada-kan-boris-iii/
LAAJ-TONTU SAADA KAN/BÓRIS (III) Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019. Bii mooy ñetteelu xaaj  bi, di yit biy tëj seen waxtaan. S. K. : Bóris, bi nuy waajal ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI NGIRTEY JONANTE DÉMB YI Démb ci talaata ji lees amal ñetteeli joŋantey kippug C gi ak gu D gi. Nii lañu demee : Kippug C : Senegaal matal na ñettam, Kamerun rëcc na. Démb bi 17i waxtu jotee la joŋantey kippug C gi tàmbali, mu nekkoon Gine Konaakiri – Senegaal ak Gàmbi – Kamerun. ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
SAARTJIE BAARTMAN, NDAW SA TUBAAB YI DEFOON MALA Saartjie Baartman ab jaam la woon, fekkoon baax ca réewum Afrig-bëj-saalum.  Moom, nag, benn doomu Àngalteer lañu ko jaayoon. Gannaaw bi, Tubaab yi dañu ko wutal ab dàkkental, tudde ko Venus Noire walla Venus Hottentote. Ci atum 1810 la àgg Tugal. Bi mu àggee, nag, tuba...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM Real Madrid a ngi wër góol bu bees Thibault Courtois, góolu Real Madrid bi,  dafa ame gaañu-gaañu bu metti (rupture des ligaments croisés) ba tax na dina toog diir bu yàgg door a góoluwaat. Loolu nag, jur na njàqare biir Real Madrid ba tax ñoo ngi ci wër góol bu koy wuutoondi ko ca caax ya. Jamon...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/dibeeru-welbati/
DIBÉERU WËLBATI Cialtine jii la njiitu réew mi doon jébbal askan wi saxaar gi ñu duppe TER. Waaye, laata looluy am, ndajem-ndeyu-àtte mi, siiwaloon na ci suba si juróomi wutaakon yi war a joŋante ci wote njiitéefu réew mi nu dégmal : Màkki Sàll (njiitu réew mi), Usmaan Sonko, Madike Ñaŋ, Isaa Sàll ak Idiriisa Sekk. Wa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/balla-gay-moodu-loo-naar-ci-dara/
Bàlla Gay-Móodu Lóo : ñaar ci dara Làmbu démb ak ju tey jeeka wuute ! Ndege, démb, bu nawet bi wàccaan, ci lañu daan tëgg làmb. Kon, nu gis ne ci njeexitalu mbey mi la mbër yi daan joŋante, ndax beykat yi ci seen bopp a daan bëre. Seetal ma lii rekk : jàmbaari tool, jàmbaari géew… Mbër mu ci nekk teewal sab gox ginnaa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/nan-wax-ci-yenn-seri-tele-yi/
NAN WAX CI YENN SÉRI TELE YI Jamono jii nu tollu temm bari na lu ñu seetlu ci miim réew, ñeel tele yi. Waaye li ci gën a ràññeeku mooy séri yu bari yi ñuy dawal. Lu sabab lu ni mel nag mën nañu wax ne ciy ñaxtu la jὀge. Nde, ay at ci ginnaaw, liñ daan faral di gis moo doon séri tubaab yi. Loolu am na ñu mu neexul woo...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM CAN 2024 Amara Juuf bokkul ci 55i futbalkat yi Alin Siise tànnagum ngir yóbbu leen ca CAF laata mu di ko seggaat ba 27. Moom, kàppiteenu U17 bi, fim ne ma nga Metz ngir faju. Gaañu-gaañu yaa ngi bëgg a bari ci gaynde yi. Gànna Géy dolleeku na ca limu ñi gaañu fekki ñoom Séeni Jeŋ ak Nàmpalis Mén...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-4/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM KUPPEG ÀDDINA U17 2023 Ndawi Senegaal yaa ngi ci waajtaayu kuppeg àddina si ñu dëgmal te war a am ci weer wii di teew. Cig waajtaay, fas nañu yéene amal ñetti ndajey xaritoo. Démb sax lañu bi ci njëkk ak Panama daldi koy dóor 4-1. Amara Juuf, Idiriisa Géy, Yayaa Jémme ak Umar Sàll ñoo dugal. Bok...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/2589/
KÀDDUY USMAAN SONKO 2/2 PÀCC Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
MÓODU LÓO DAAN NA AAMAA BALDE Xaar bi yàggoon na lool, waaj gi tamit naka noonu. Waaye, ñaari mbër yi mujje nañu sëgg démb ci dibéer ji. Móodu Lóo ak Aamaa Balde bëre nañ démb, ca aareen nasiyonaal ba ca Pikin. Móodu Lóo moo daan, yóbbu ndam leek metel mi (la couronne) Pàrsel. Seen làmb ji, bi ñu ko dalee waaj, yàggo...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Malaanum Lëndëm : Bóris Jóob, na woon, fa woon Ñeenteelu yoon a ngi nii Bubakar Bóris Jóob di génne téere bu mu bind ci wolof (+), te mu tudde ko Malaanum lëndëm ; muy téere bu EJO móol. Bóris moom, kenn dootul woññi ay mbindam ci làkki réew mi ndax ni mu nuy jàngalee li war a nekk, naka jekk : di bind ak a jàng ci là...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-12-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (3/12/2023) COOWAL CAN LI Afrig moom, dafa mel ni ndeyam liggéeyul. Saa bu CAN bi jubsee, coow li jib, ñuy ŋëwti-ŋëwti joŋante bi. Te, bu “Euro” bi jotee, kenn du dégg coow ñeel ko. Waaye bu Joŋantey Afrig teroo rekk nga dégg lu nekk. Li ko waral nag mooy ni këlëbi tugal yi ame ay futbalkati ñuul...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/fallu-siise-fekki-na-kocc-barma/
FÀLLU SIISE FEKKI NA KOCC BARMA! Ndekete Fàllu Siise daa bokk ca ña daamar (kamiyoŋ) ga saaraan fan yii ñu génn ca Caaroy dal seen kaw. Aa… Ki doon dawal daamar googu de, xamul li mu def. Li mu def, mënees na koo méngale ak xosi almet sànni ko cig kàggu, téere ya ca ne, ànd ak xam-xam ya ñu ëmb, daldi lakk ñoom ñépp b...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/fu-messi-di-futbal-dewen/
FU MESSI DI FUTBAL DÉWÉN ? Jamono jii, laaj bii moo lëmbe xel yi, rawatina xeli soppey Barcelone FC yi. Li ko waral, nag, mooy ni, seen yéene yépp dafa nekk ci Messi ñibbisi. Ndax dana am ? Ndax du am ? Mëneesagul a am tontu lu leer ci laaj bi. Lo am ba des daal, mooy ni foofu ca Barça, seen yaakaar moo ngi gën a dëgë...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ndigalu-maam-ya/
Ndigalu Maam Ya Afrig nee Waaw góor, waaw kumba Ayca leen ca waar wa Bu kenn wéer goob ba Bii pas-pas dara mënalu ko dara Dina daw ba raw xëlu fas Ngor ak jom a ko nas Ma ne, Askan wee ko sas Gan góoru jigéen ñi dar lingeer Ci seen farlook seen gànjar ya Bég ba tàccu ne sas Maam a ne bëret dan delsi Samp x...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/
ALSERI DUMAATI NA SENEGAAL Démb ci talaata ji la gayndey Senegaal yi doon janook Alseri ci joŋante xaritoo. Jamñaajo, ça fowub Abdulaay Wàdd, lañ ko doon futbalee. Alseri moo jëlati ndam li. Nde, ñoom ñoo dugal benn bii, Senegaal tus. Démb a nekkoon 14eelu yoon wi Senegaal di sukk ci kanamu Alseri. Li ci gënatee doy w...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (10/07/2023) MAROG JËL NA CAN U23 BI Démb, ci gaawu gi, lañ doon amal lii di finaalu CAN U23 bi doon ame fa Marog. Mu gi dooxoon ci digante ñaari naataango yii di Marog mi dalal xëccoo bi ak Esipt. Mu nekkoon finaal bu neex. Waaye, Marog moom, moo xewle, daldi woote, luñ nar a fecc mu fecci ko, l...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-18-9-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (18/9/2023) WAA LORIENT YI SARGAL NAÑU BENJAMIN MENDY Benjamin Mendy duggaat na démb ci pàkkub futbal, gannaaw tuuma gu metti te yàgg bi tegu woon ci ndoddam, at yii weesu. Tuumay ciif yooyu ñu gàlloon ko ñoo taxoon ñu bari foogoo ne daf ciy jaare bàyyi futbal. Waaye, keroog, ba ñu ko setalee ni ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
« Man, dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. » Mamadu Jàllo :  Ndax CFA bi baax na ci njaay meek njënd mi, rawati-na bitim-réew ? Ndongo Sàmba Silla : Déedéet. Mësu cee baax ! CFA bi du yombalal njaay meek njënd mi. Moom kay, safaan bi la koy jural. Ndaxte, boo seetloo, bi Senegaal moomee boppam ci at...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/paap-bu-mag-ba-woon-benuwaa-16-sosef-ratsingeer-wuyuji-na-boroomam/
Paap bu mag ba woon, Bënuwaa 16 (Sosef Ratsingëer) wuyuji na Boroomam
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/aram-faal-sunu-seex-anta-joob-bu-jigeen/
ARAM FAAL, SUNU SÉEX ANTA JÓOB BU JIGÉEN… Talaata jii weesu di 23 ci weeru awril la Mbootaayu-Xeet yi jagleel bépp teere bu doom-aadama bind ci àddina si. Ci la EJO ak ArtXaleyi, di ñaari kurél yuy yëngu ci mbirum aadaak ladab, sargal Soxna Aram Faal Jóob mi yàgg a def liggéey bu am solo ngir ñépp jox làmmiñi réew mi ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-gi-senegaal-ameel-bor-ii/
MBAY JAAG, GOR GI SENEGAAL AMEEL BOR (II) Am it lu mat a taxaw-seetlu : jamono jooju Mbay Jaag doon jiite ndongo yi, fekkoon na mu bokk ci PAI, pàrti  “marsist” bu mag boobu  Majmuut Jóob sosoon te mu jiite woon yéngu-yéngu ya jiboon ca 1958 jëm 1960 (“boroom paŋkàrt  ya”) ba Afrig Sowu Jant gépp doon xeex ngir moom ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ana-lu-goor-giy-laqarci/
ANA LU GÓOR-GIY LÀQARCI ? Bamu jógee Konaakiri ba tey, seeti woon Alfa Konde, Abdulaay Wàdd, sunu Njiitu-réew ma woon, a ngi ne selaw. Wote bu 24 féewaryee bi sax, ak faluwaatu Maki Sàll bi mu jur, ba tey, yéyul yàbbi ci benn yoon. Mi ngi toog ci otelam ne tekk. Terewul ñëpp moom lañuy déglu. Lu ni mel, Wàdd yàgg na ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-alxames-4-me-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (ALXAMES 4 ME 2023) RËBËJOO BA CA PSG Gannaaw tukki bi Messi amaloon ca Araabi Sawdid, njiiti Paris Saint-Germain daan nañ daan bu diis. Dañoo ajandi Messi ñaari ayu-bés yoy, du ci futbal te yit du ci tàggatu. Yemuñu foofu de, ndax dinañ ko dagg peyoorug ñaari ayu-bés yooyu ñu ko ajandi. Gannaaw...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/tabaski-2023-xutba-serin-baabakar-si-mu-dabbaax-njool-fuuta/
TABASKI 2023 : XUTBA SËRIÑ BAABAKAR SI MU DABBAAX (NJOOL-FUUTA) Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina ...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (DIBÉER 5 MÀRS 2023) LÀMB Saa-Cees – Rëg-rëg ñoo doon bëre ci dibéeru tey ji. Mu doonoon làmb ju ñépp doon xaar. Waaye, nag, coow am na ci. Nde, bu dee àttekat yi Rëg-rëg lañ jox ndam li, Saa-Cees ak i farandoom nee nañu ñoo daan. Ndaxte, ci biir jaxasoo bi, am na fu Rëg-rëg sampe...
Defuwaxu
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
AY DU YEM CI BOPPU BOROOM Senegaal, jamono ji ñu tollu nii dafa mel ni nekk doomu– réew mi rekk doyatul ; fàww nga fésal wet gi nga féete, moo xam sa diine la walla sa tarixa mbaa pàrti pólitig bi nga faral ba ci sax mbootaay gi nga bokk léeg-léeg. Waaye li ci gën a tiis, tey tiitalaate ba noppi ruslu mooy ñaawtéefi ...
Defuwaxu