url stringlengths 43 43 | content stringlengths 1.49k 122k | source stringclasses 1
value |
|---|---|---|
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/mat.htm | 1:1Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
1:2Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
1:3Yuda, Fares ak Sara ci Tamar; Fares Esrom, miy baayu Aram;
1:4Aram Aminadab; Aminadab Naason; Naason Salmon;
1:5Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak ... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/mar.htm | 1:1Xebaar bu baaxu Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, nii la tàmbalee.
1:2Bind nañu ci téereb yonent Yàlla Esayi naan:«Maa ngi yónni sama ndaw ci sa kanam,mu xàllal la sa yoon.
1:3Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”»
1:4Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox,... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/luk.htm | 1:1Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,
1:2li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.
1:3Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/joh.htm | 1:1Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
1:2Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga.
1:3Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom.
1:4Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi.
1:5Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndë... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/act.htm | 1:1Yaw Teyofil, téere bu jëkk, ba ma bindoon, ëmb na lépp li Yeesu tàmbali woon a jëf ak a jàngale,
1:2ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon.
1:3Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dun... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/rom.htm | 1:1Man Pool, jaamub Kirist Yeesu, maa leen di bind bataaxal bii. Yàlla woo na ma, ma nekk ndawam, sas ma liggéeyu xamle xebaaram bu baax bi.
1:2Xebaar bu baax boobu, Yàlla dige woon na ko bu yàgg, jaarale ko ciy yonentam, ñu def ko ci Mbind mu sell mi,
1:3di xamle mbirum Doomam, Yeesu Kirist sunu Boroom. Lu jëm ci me... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/co1.htm | 1:1Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Sosten sunu mbokk,
1:2noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla, mi dëkk Korent. Nu ngi leen di nuyu, yéen ñi Yàlla sédde boppam jaare ci Kirist Yeesu, yéen ñi Yàlla woo, ngeen sell, boole leen ak ñi nekk ci àddina sépp tey tudd turu sunu Boroom Yeesu Kirist, miy ... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/co2.htm | 1:1Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk, noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla mi nekk dëkku Korent, ak gaayi Yàlla yu sell, yi nekk ci diiwaanu Akayi gépp.
1:2Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
1:3Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu boroom Yeesu Kirist,... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/gal.htm | 1:1Man Pool, ndawul Yeesu Kirist --nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Yàlla Baay, bi ko dekkal —
1:2man ak bokk yiy ànd ak man yépp, nu ngi leen di bind, yéen mboolooy ñi gëm te dëkk ci diiwaanu Galasi.
1:3Na yiw ak jàmm féete ak yéen, jóge ci Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/eph.htm | 1:1Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, maa leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yi te gëm Kirist Yeesu ci dëkku Efes.
1:2Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
1:3Cant ñeel na Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu sotti ci sunu bokk ci Kirist lépp luy barkeel ci baatin... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/phi.htm | 1:1Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yépp ci dëkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, yéen ak seeni njiit ak ñiy topptoo yëfi mbooloo mi.
1:2Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
1:3Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom;
1... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/col.htm | 1:1Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk,
1:2noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell, yi dëkk Kolos te di ay bokk ci gëm Kirist. Na leen Yàlla sunu Baay may yiw ak jàmm.
1:3Dunu noppee sant Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, saa su nu leen di ñaanal,
1:4ndaxte yég nanu seen... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/th1.htm | 1:1Nun Pool, Silwan ak Timote noo ngi leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist. Na yiw ak jàmm ànd ak yéen.
1:2Bët bu set nu ngi sant Yàlla ndax yéen, di leen boole ci sunuy ñaan.
1:3Dunu noppee fàttaliku ci kanam Yàlla sunu Baay jëf ji juddu ci seen ngë... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/th2.htm | 1:1Nun Pool ak Silwan ak Timote noo leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist.
1:2Na leen Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
1:3Bokk yi, mënunu lu dul sax ci sant Yàlla ndax yéen. Loolu jaadu na, ndax seen ngëm di gën a sax, te mbë... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/ti1.htm | 1:1Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci ndigalu Yàlla sunu Musalkat ak Kirist Yeesu sunu yaakaar,
1:2maa ngi lay bind Timote, yaw miy sama doomu diine ju wér. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
1:3Xam nga ne, ba may dem diiwaanu Maseduwan, ñaanoon naa la, nga des dëkku Efes, ngir d... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/ti2.htm | 1:1Man Pool, ndawul Yeesu Kirist ci coobareg Yàlla, ngir xamle dund gi nu Yàlla dig te féete ci Kirist Yeesu,
1:2maa ngi lay bind Timote, sama doomu diine ji ma bëgg. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
1:3Fu ma tollu maa ngi lay boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla, mi may jaa... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/tit.htm | 1:1Man Pool maa lay bind, man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni, ngir xamle ngëm, gi lal yoonu ñi Yàlla tànn, tey yokk xam-xamu dëgg, giy meññ ragal Yàlla;
1:2mu sukkandiku ci yaakaar ju dëggu, ji nu am ci dund gu dul jeex, gi Yàlla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam.
1:3Te léegi, ci jamono ji... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/plm.htm | 1:1Man Pool, mi ñu tëj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi;
1:2te fàttewunu sunu jigéen Afiya, ak sunu àndandoo ci xeex bi Arkib, yéen ak mbooloom ñi gëm, miy dajee sa kër.
1:3Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
1:... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/heb.htm | 1:1Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.
1:2Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.
1:3Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di k... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jam.htm | 1:1Man Saag, jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, yéen fukki giir ak ñaar, yi tasaaroo ci biir àddina si.
1:2Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu man a mel, defleen ko ni mbég mu réy,
1:3xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ.
1:4Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen bañ a f... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/pe1.htm | 1:1Man Piyeer, ndawul Yeesu Kirist, maa leen di bind, yéen doxandéem yi tasaaroo ci diiwaani Pont, Galasi, Kapados, Asi ak Bitini. Yàlla Baay bi tànn na leen,
1:2ci li mu leen xam bu jiitu, te sédde leen boppam ci jëfu Xel mu Sell mi, ngir ngeen déggal ko, te seen xol laab ndax deretu Yeesu Kirist. Na leen Yàlla dolli... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/pe2.htm | 1:1Man Simoŋ Pieer, jaamu Yeesu Krist ak ndawam, maa leen di bind, yeen ñi Yàlla jagleel ngëm gu rafet ni nun, aju ci njubu sunu Yàlla ak Musalkat, Yeesu Krist.
1:2Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm, jaar ci xam ko ak Yeesu sunu Boroom.
1:3Dooley Yàlla moo nu may lépp lu aju ci dund gu sax ak ragal Yàlla, jaarale ko ci... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jo1.htm | 1:1Nu ngi leen di bind ci mbirum Ki ñuy wax Kàddug dund, moom mi amoon ca njàlbéen ga; mi nu dégg te gis ko ak sunuy bët, mi nu xool te laal ko ak sunuy loxo.
1:2Dund feeñ na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen yégal dund gu dul jeex, googu nekkoon ci wetu Yàlla Baay bi te feeñu nu.
1:3Li nu gis te dégg k... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jo2.htm | 1:1Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. Bëgg naa leen bu wér ci sama xol, jéllale naa sama bopp sax, waaye itam képp ku xam dëgg gi.
1:2Te dëgg gee tax nuy def noonu, dëgg gi dëkk ci nun, tey ànd ak nun ba fàww.
1:3Yàlla Baay bi ak Yeesu Krist, Doomu Baay bi, dinañu nu may yiw, yërman... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jo3.htm | 1:1Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol.
1:2Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér gi yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.
1:3Sunuy mbokk ñëw nañu, te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool.
1:4Awma mbég mu ëpp lii: ma d... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jde.htm | 1:1Man Yudd, jaamu Yeesu Kirist, mi bokk ak Saag ndey ak baay, maa leen di bind, yéen ñi Yàlla Baay bi woo te bëgg leen, te Yeesu Kirist aar leen.
1:2Na leen Yàlla may yërmande, jàmm ak mbëggeel.
1:3Samay bokk, bëggoon naa leen a bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo gën a jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw... | New Testament |
https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/rev.htm | 1:1Lii mooy li Yeesu Kirist feeñal, te mu tukkee ca Yàlla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi dëgmël di ñëw. Yónni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana.
1:2Kooku mi ngi seede fii li mu gis lépp, maanaam kàddug Yàlla ak seede, si ñu seedeel Yeesu Kirist.
1:3Barkeel ngeen, yaw miy jàng ak yéen ñiy déglu wax yii jó... | New Testament |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.