url
stringlengths
6
8
content
stringlengths
2
3.72k
source
stringclasses
3 values
page_302
Damaa toog ba yàgg rekk gis ko mu génne néegu Yaasin, ñu ànd mook Tamsiir Ba, di waxtaan, di kaf aka ree. Ma ni ko : - Moo, Biige kañ nga fi ? Ci la ma door a wax ne Yaasin a ko yónni woon. Wax jooju jaaxal ma lool waaye teguma ci baat. Aa ! Badu, man kat damaa yëgul fu Yaasin Njaay ak Biige Sàmb takkee xarit....
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_303
- Su may àgg Màrsey di la bind, Biige. Ma siggi, ne Biige : - Badu de, xanaa balaa yàgg mu dellusi. Góor kat moomul toog. Sunuy bët dajewaat. Takkandeeru Asan neeti bërét, def ay jéego yu rey, jaar sunu diggante. Góor moomul toog. Bés ba Asan Taal di yëgal Biige ne dafa war a dem Màrsey, baat yooyu la doon dà...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_304
Gone yi fekksi ma fi ma jaaxaan ñu niit ma, ηóobi ma ba seen xol sedd, sog a dabi Biige Sàmb ak Tamsiir Ba, seen faru yaay. Nga baal ma de, Badu, waaye Biige Sàmb, sa yaay jii, ku bari pexe la. Li ma gën a waar mooy naka la def ba miinanteek Yaasin Njaay. Soo leen gisee, danga naan ay doomi-ndey lañu. Wute wuñ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_305
ba tax ñu xam ne léegi ay mag lañu, weesal seen boppxulook ηaayoo. Ba tax it ñu xam ne gunge doomi Asan Taal yee leen war, ñu def ko na mu gën a rafete.Waaye àddina leneen la ma jàngal ! Xam nit, xam jikkoom a ko gën. Ni Biige Sàmb ñóoxoo Yaasin Njaay, mënul a jur jàmm. Doomu-Aadama day faral di tënëx- tënëxi ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_306
- « Aa, baax na. Xanaa boog ma jàppe ko noonu ». Ba ñu nee suba la Yaasin di dem, Biige Sàmb a ko létt, ñu ànd ñoom ñaar biir Ndakaaru jëndi seeni yóbbal ak ay yëfi jigéen, xam naa. Ba mu defaree ay waliisam ak waliisi doom yi ba noppi, la door a ñëw tàggatook man. Man it wax naak moom wax ju rafet, gërëm k...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_307
- Lii kañ du dara ! Damaa xaw a sant Jóob rekk, nde moos yéene naa la lu ko ëpp fopp, nijaay Ngiraan.Mbaa mu ne ma : - Yàlla xam na ne xeeb naa ko, góor gi Ngiraan, waaye bul wax dara, xaaral ba ma dellu Màrsey rekk ! Loolu yépp fekku ci Yaasin. Dafa ne nemm-nemmaaral, di ma xool mel ni du moom laay waxal. Xawm...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_308
Waaw, Badu, ku la masula tudd, masula taas, su takkee ay waliisam, fëgg sa buntu néeg, fekk la fi nga tëdd mu tàggu la, xanaa kay li ci des mooy mu woolu taksi, ne yoonu ayeropoor maa ngoog ? Du dëggam, Badu ? Ba àddinay baax de, noonu la yëf yi daan deme. Waaye bés ba ma Yaasin tàggoo ba noppi, la tàmbalee d...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_309
Yaasin siggi, xool Biige Sàmb. Man mii Ngiraan Fay de, dootu-ma gone, waaye giñ naa ne musumaa gis nit ku jàqe ni Yaasin Njaay keroog. Ñaari doom yi ñëw katamu ko, di yikkat. Mu ne Biige : - Sama këyit yépp réer nañu, Biige. - Nga ni ma ? - Waa-waaw. Seet naa ba sonn. - Loolu gën a doy waar, Yaasin ! - Wóor...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_310
Li ma jëli keroog ci waxtaanu Yaasin ak Biige, lii la : musiba moomu daloon Yaasin, sa yaay amoon na ci mbégte mu réy a réy ! Te njortoon naa it ne fu kayiti Yaasin Njaay ya dugg, moom Biige Sàmb moo leen fa dugal. Njël soreetul woon. Ñu dégg ci Ñarelaa benn waay juy tëgg sabaram tey yuuxu ca kow : Dégluleen...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_311
- Ana ki waral lii lépp ? - Kii kan ? - Xanaa ki tax nu dajaloo ci pénc mi ! - Moom lanuy xaar booba ba léegi. - Nanu xaar boog. Ñarelaa xaar ba xàddi, mujjee xaare boppam. Usmaan Sow, boroom saret bi ne : - Nun daal, noo ñàkk faayda dëgg ! Ay boroom kër yu tollu ni nun, benn waay tëgg sabaram rekk, nu ñëw...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_312
Ñarelaa tiit. Ku nekk di sànni say bët fu nekk, ngir xam fan la kàddu yooyu jóge. Kenn ci nun sañul a tudd turam. Waaye nun ñépp la sunu xel dem ci moom. Aali Këbóoy ! Aali Këbóoy... Aali Këbóoy lañ koy woowe. Luy turam dëggëntaan ? Kañ la dëkksi Ñarelaa ? Fan la bawoo ? Loolu lépp kumpa la ci nun. Aali Këbó...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_313
Du benn du ñaar xaañ na fi nit. Saalitloo na fi tam ay boroom kër yu bare ndax su ko ci Yàlla xiiraan day nég ba xaaju guddi muy kar nit ñi, di leen àddu-kalpe. Bés nag, Aali def lu ëpp. Ku ñuy wax Baay Ndeenee fi amoon xaj, fii ci Ñarelaa. Xaj bi sonal lool Aali. Fu dof bi dugg, mu fekk ko fa di ko mbów. Aali...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_314
Li ko Baay Ndeeney jam yépp, Aali Këbóoy a ngi koy balu àq : - Sarax ma, dootuma la tooñ. Giñ naa ne teyuma ko ! Maa mujjee yërëm Aali Këbóoy, woolu pólis. Bi alkaati yi ñëwee, li ñu ma jëkk a laaj mooy kan moo doon dof bi, ci diggante Baay Ndeeneek Aali Këbóoy ! Teg nañ ci ay fan i fan, kenn déggul Aali Kë...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_315
- Yow kañ bëre bukkeek mbaam nga nuy wax ! - Dégg ngeen yuuxu Aali yi, de ? Wutewul woon ak mbaam-xuux mu ñu ñàdd di ko rendi ! - Moo, koo koy wax ? Mu naan xuux xuux rekk, tëwa bàyyi ! Gat di ! Ñu tegaat ci ay weer, Aali Këbóoy dellusi Ñarelaa... Tuddul kenn, taasul kenn. Dafa jubal mbaaram, téju fa ay fan...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_316
Ba muy séwét, fekk na ku nekk ci nun a ngi këram di seetaan tele. Bi nu jullee geewe, naan àttaaya bay waaj a tëri, lanu dégg ay yuuxu ci mbedd mi. Nu yaakaar ne waxambaane wu ñu doon dóor la, muy woote wallu. Ba ñu demee ba ca biir lanuy sog a leer ne waa ji nekkul woon ci benn jafe-jafe. Da doon woy, ndeket...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_317
- Lu tax nga wax loolu ? - Lu tax nga wax loolu, Ngiraan ? Dafa fekk ni, dof kat, loo mën a xalaat ci lu bon mu ngi koy dugal ci biiram bi te su feebaree kenn du ko faj. Lee-lee it saxaar mbaa oto fekk ko fi mu tëdd, yéeg ci kowam, dër ko te du sax taxaw. Ay nit ñooy romb néew bi, kenn ci ñoom ne : - Ndeysaan....
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_318
- Aa, man la Aali Këbóoy, maa dellusi Ñarelaa. Yéen a ngi fàttaliku dóor yu metti yi ma fi Baay Ndeene dóoroon, at yee ñu génn ? Yéen a ngi koy fàttaliku, mbaa ? Kenn ci yéen nanguwu maa tontu, waaye amul solo. Man, Aali Këbóoy, maa leen di yëgal ne dem naa dëkk ba ma fekk baax nag, laaj mag ña lu tax Baay N...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_319
Loolu yépp tuub naa ko. Teewul nag, maa moom sama làmmiñ wii, man Aali Këbóoy. Lu ma neex dinaa ko wax, te kenn du ci mën tus ! Bi Aali Këbóoy daaneelee, ñépp a féex, ku nekk naan : - Aa ! Waxi dof de, amul solo ! Céy, su nu xamoon li nu doon yoot, booba ! Aali Këbóoy, Baay Ndeene ma ko duma woon duma yu me...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_320
Saa yu Aali Këbóoy séenee Baay Ndeene rekk, tàmbalee tàccoo ka woy : « Ofise ne paa pëer, bu doxatee sax du xasaw, ndax kenn du ñemee reetaan ! » Su ko defee, Baay Ndeene dëngalu, mel ni du moom la Aali Këbóoy di gaaral. Dem nañu nag ba kenn mënatul a muñ yëf yi. Su woyu Aali Këbóoy woowu jibee rekk, ñépp daa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_321
Daawul tudd turu kenn nag, waaye ñépp a doon xam ku moom wax ji : Aa, sama sang yu baax yi, lu ngeen xam ci kuy yakkataan doomu-jiitleem ? Moom laa fi gis de, ngóor saa ngi nii, ne fàηη ci biir seetu bi ! Ku weddi na ñëw xool kook mbaxaneem mu ñuul meek i bejjaawam ! Cim ! Ñàkk jom badee ! Beneen bés mu ne : ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_322
Ñépp mujjee ragal Aali Këbóoy, di ko moytu ndax ñàkk kersaam. Rax-ci-dolli, kenn xamul na mu daan def ba xam li mu doon wax yépp.Am ñu naan : - Aa, dof bi waxati na de ! Kii, ñàkkul muy boroom xam-xam bu mag ! Mbiri Yàlla kenn xamu ko ! Aali Këbóoy yemul foofu. Ba mu demee ba mu wóor ko ne nit ñaa ki koy may ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_323
Aali Këbóoy doon na def it lenn : lu mu wax tey, bu ëllëg saa mu jaaraat ca. Daan na ko jàppe noonu ay weer ba mujje gi ay kàddoom, gone yépp a leen daan tari. Laaj ma nag kañ la Aali tas jàng yi ! Laaj ma ko, ma wax la ko ! Gis nga, Badu, politiseη yi doon joηante fii ci Ñarelaa, ñoo xaar ba xaaju-guddi, ñu ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_324
- Ma xasal leen seen noon boobu ? - Nit ku bon la. Fi mu ne, Ñarelaa ba Ñarelaa daj, yow rekk la nit ñiy déglu ! Fàww nga xamal leen ne waru ñoo fal saay-saay boobu ! Aali ne leen : - Aa ! Ñaata ngeen may fey ? - Loo bëgg, dinanu la ko defal ! - Xaalis baa ngi nii, su doyulee ñu yokkal la ci lu bare ! - Ay...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_325
- Lu ngeen bëgg ? Ma xasal leen ko ? - Waaw. Yow, nit ñi fonk nañu lool say kàddu, Aali. Loo wax ñu ne dëgg la, ànd ceek yow. Aali Këbóoy ree ci biir xolam. Gaa ña wax ko lépp lu bon lañu xamaloon seenub noon. Aali daldi mel ni ku furtaat nag, Badu ! Fan yooyu kay, Ñarelaa rëb na lool ! Aali Këbóoy dafa jaxa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_326
Laaj leen ma loolu lu mu ! Dañu bëggoon ma jaay leen sama xaste yu neex yi ! Xasal diw ak diw, wax ko ay baaxi maamam nu fey la xaalis bu dul jeex ! Aa ! Xanaa kon ñoom bu ñu jotee ci réew mi, dañu fi nar a ubbi daara ju ñuy jàngale wax ju bon ! Su ko defee, ku dàq saaga ci réew mi yaa fiy ëpp alal ! Man...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_327
Saa yu dikkalewaan it, noppi, danu daan namm ay kàddoom ba nga ne lii lu mu doon. Benn guddi nag, Aali Këbóoy wax lu ëpp, moom tamit. Mooy guddi ga mu tuddee Tubaab bi, di ko ηàññ, naan war naa génn réew mi abal nu, nu moom sunu bopp. Aa, guddi googu Badu, kilifay Ñarelaa yu bare nelawuñu ! Mag ñi gise ci se...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_328
Ñeneen ne : - Du tey la Aali Këbóoy mas a xéy ne mes ! Du ñàkk mu dellusi bés na mu ko fi daan defe. Gaa ñooñu de, Badu, dañu doon dof-doflu rekk, ndax xamoon nañu bu baax nu yëf yi deme. Leeroon na ñépp ne waa gox bee sàkkaloon Aali Këbóoy pexe. Waaye Aali de, dundam neenul. Tey dinga toog Ñarelaa, dégg ku ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_329
Lii laa la ci bëgg a jàngal : saxal ci li nga nekk, bul nangoo nekk ma-riirandoo. Donte sax li nga gëm, yow kott ci àddina si yépp yaa ko gëm, bumu la tax a dellu ginnaaw. Bul tiit, bul ragal. Bu kenn fees say bët ba doo am fitu xalaatal sa bopp. Badu, toppal ciy tànki Séex Anta Jóob ak Aali Këbóoy. Ba Aali K...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_330
Dinga mar, dinga xiif. Loolu lépp xej na ci. Waaye soo toqiwulee, bés dina ñëw say doom ak say sët bég, naw seen bopp. Badu, lépp li ma xam ci àddina, dof bu tudd Aali Këbóoy moo ma ko jàngal. Moo tax ma ni : - Dof mat naa bàyyi cim réew. * * * Noo yaakaar nag ne noonu la yëf yi mujje, Badu ? Aali Këbó...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_331
Nañu ko waxe it lañu ko defe. Yeewooti nanu bés, gisatunu Aali Këbóoy, déggatunu ko. * * * Ñaareelu bóomug Aali Këbóoy ga, nu mu deme ? Am na lu ma ci fekke, man Ngiraan Fay, te dinaa la ko nettali. Benn guddi, dégg nanu kuy yuuxu ay yuuxu yu metti te yàgg lool. Ma daldi xàmmee ci saa si baatu Aali Këbó...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_332
- Ay saay-saay songati nañu Aali ! Jógleen wax ci ! Buleen seetaan lu ñaaw loolu, yéen waa Ñarelaa ! Waaye su ma Ñarelaa tontoo, yow ma juddoogul woon booba yaa ma tontu. Mbedd mbaa ngi ne selaw. Bi ma àggee tali bi jëm kër Biram Saala Géy, kenn ci ñi doon duma Aali Këbóoy sànni na ma aw doj, doj wi cof sama ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_333
Ñarelaa ngi ne selaw, ndeysaan. Xanaa rekk lee-lee ngelaw li pes xobi garab yi mbaa ma dégg xaj buy mbów ci guddi gi. Ma daldi wiccax sama bopp, yéemu ci mbonug Doomu-Aadama. Sama xel dellu ci Aali Këbóoy : « Xam naa Baay Ndeenee nga Kusum di joow, di nemmeeku béréb bi gën a xóot ci géej gi, mu diigal fa néewu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_334
Keneen ne : - Soo déggee yuuxoom yi kañ, xam ne tuutee tee ñu rey ko ! Ñoom ñépp ñu ree, def mbir mi ay kaf. Benn tur rekk nekk ci xel yépp, waaye kenn sañu koo tudd. Aali Këbóoy. Niti tey yi ñooy naaféq, Badu ! Ba ñu ca tegee ay fan, am ku romb mbaaru Aali Këbóoy, taxaw, daldi ne : - Waaw ! Sunu Aali mi de, ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_335
- Seen coow li bare na te amul njariñ ! Démb ci timis, benn ponkalug kaña génne na mbaaru Aali Këbóoy. Toj mbaar mi jot na ! - Baay Ndeene wax na dëgg. Su nu ci teelul a jóg, mbaar mii mën nanu fi indil ay jàngoro yu kenn xamul. Waaye Badu, ba dara desul lu dul sempi mbaaru Aali Këbóoy, mbir feeñ na. Nga ne m...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_336
Mag ñii xoolante.Am ci ñoom ku ne : - Nun kat, noo tooñ sunu bopp. Warunu woon a sant Maada mu woyof bopp mii mu sempi mbaaru Aali Këbóoy. - Wax nga dëgg. Nanu woo Taala Njaay minise bi. Moom war na cee mën dara, am na doole, am na xam-xam. Waaye, Badu, Taala Njaay jotul sax àgsi ba ci mbaaru Aali Këbóoy. G...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_337
- Bàyyileen gis kuy dem, sol ay sagar rekk, ngeen di ko sànniy xeer ! Baax na ! Ñi ci des di dekkali ay kàdduy Wolof Njaay : - Deretu téegu du moy luppu boroom ! - Doxati gëléem kow la jëm ! - Sàcc ndënd yomb na moom, xanaa kay am foo koy tëgge mooy jafe ! Badu, ñu bare la seen taat tëgg tama keroog, man mii ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_338
Sabadoor bi mu sol a ngi furi be kenn xamul lu muy nirool, mu teg ab tengaade ci bopp bi, téye ci bantam di temp. Waaye Badu, góor gi nu gis tisbaar jooju de, amoon na mayu Yàlla. Kër gu mu taxaw keroog di yalwaan, su ñu ko saraxee ba noppi am na ku ne : - Góor gii de, bi sunuy bët dajee am na lu ma yëg ci sam...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_339
- Kilifa gu ñu naan Góora Mbay moo ma yónni ci yow. Nee na nga wuyusi ko ci nu mu gën a gaawe, dafa la soxla te soo ko xaarloo dina la won mooy kan ! Waay-Yàlla ji ne jàkk surga bi. Kooku gis ni bëti góor giy tàkke, daldi dellu ginnaaw. Góor gi ni ko : - Neel ki nga ne kilifa la, su ma génnee gox bii, te dabu m...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_340
- Ñëw bii nga ñëw de, moo gën ci yow ! Soo deful woon li ma la sant, yàqu kon nga yaxeet ! Léegi nag, déglu ma bu baax : mbaaru Aali Këbóoy du sempiku feek ku ñuy wax Isma Ndóoy dugalul loxoom ci mbir mi. Góora Mbay ni ko : - Ãa ? - Waaw. Waaye dinaa ci yokk lu tuuti : Aali Këbóoy, fàww mu dellusi. Dégg nga ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_341
Ma seeyal ruuwu Aali Këbóoy ? Ruuwu nit, Yàllaay boroom. Góora Mbay geestu, fu ne mu xool fa, di seet ndax am na ku dégg kàdduy góor gi. Mu daldi ne : - Dinaa def li nga wax. Waaye ginnaaw kenn mënul a tere Aali Këbóoy mu dellusi, lu nuy doyeeti Isma Ndóoy ? - Foofu nga juume. Su ngeen feyee Isma Ndóoy li mu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_342
- Doxatu gëléem kow la jëm. Du man mii de maay weddi kàddu yooyu. Wax ji law. Gox boo dem ci Ndakaaru, dégg ñuy waxtaane mbirum Aali Këbóoy. Nit ñi ràkkaaju nag, ma ni la, di yokk ak a yokkaat, di xoromal. - Dégg ngeen li ma déggam ? Nee nañu Aali Këbóoy dafa soppiku malaaka, yéeg ci kow asamaan ak ay laafa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_343
- Man de, benn jigéen doon na ma tanil démb. Xamal na ma ne lépp lu xew Ñarelaa, Aali Këbóoy a nga jaaxaan ca àllaxira di ci teg bëtam. - Eskéy ! Ba màggatu yalwaankat ba demee ba nu fàtte, benn xaleelu góor bu tudd Isma Ndóoy, dëkk Mbaaw, ñëw bés Ñarelaa, ne moom mën naa sempi mbaaru Aali Këbóoy. Ñu ni ko : ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_344
Isma Ndóoy boolewu ca wax. Dafadaldi solaat mbubbam, ne mu ngay dellu Mbaaw. - Dimbali nu, ñaan nanu la ko ci diggante jullit ak moroomam. Isma Ndóoy geestu Góora Mbay, xool waa Ñarelaa ba seppali leen, daldi ne : Yéen ñépp ay naaféq ngeen, te xam ngeen lu tax ma wax loolu. Man Isma Ndóoy, bi yëf yiy am, maa n...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_345
Baay Ndeene nag, noon naa la fi dafa àndoon ak xadar. Ñarelaa ba Ñarelaa daj, moo ci gënoon a bari ay. Xeex ak naan ndox la mas a yemale. Mag ñi naxanteek moom, yedd ko, xamal ko ne warul a topp meram. Góora Mbay daldi ne Isma Ndóoy : - Ginnaaw noonu la, nga baal nu àq, waa ju baax. Amunu xaalis bi nga nuy laaj...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_346
- Waaw, Ngiraan, yow de, saa yu lu mel ni masaan xew Ñarelaa, waa gox bi daje di ci waxtaan, danga daan yëkkati sa kàddu, joxe sa xalaat. Tey moom, kenn déggul sa baat... - Maa yey ne patt, Baay Ndeene. - Ãa ? - Waaw. Man kat, dama tiit ba fu tiit yem. - Lu waral loolu, Ngiraan ? Ma yëngal sama bopp, ni ko :...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_347
- Danga bëgg a wax ne Aalee fi taxawoon sànq di waxtaan ak nun ? - Looloo am sax de, Baay. Keroog jooju, Badu, gis naa kilifay Ñarelaa yu bare ñu téye seen bopp ndax jaaxleek tiit. Ña jógoon ci xaaju-guddi, fekki Aali Këbóoy ca biir mbaaram, rendi ko, am na sax ku ci rëccle ba caaya ji xaw a rot.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_348
TÉEREB LËNDËMTU II
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_349
Badu, du caagin dama la bëgg a miirloo, waaye fàww nga may ma ma dellu ay ati at ci ginnaaw. Maa ngi door a am fanweeri at ak ñaar, nekk óbërye ca Air Liquide, di doxaan ndaw su ñu naan Faat Juuf. Bés, ni ma ko tàmmee def, ma reer ba noppi, sol samay dàll, tegu ci yoonu kër Faat Juuf. Kolobaan la Faatu luye w...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_350
Taataan. Mbejante. Àndandoo di salliiru. Mujje ne yàcc, di xullee. Waaw, noonu lanu daan jotee, maak Faat Juuf. Waaye guddi gi ma lay wax de, neneen la mbir mi deme. Kottante nanu lu yàgg ci kow lal bi, ne cell, mel ni ñaari gone yu réer ci àll bi, ku ci nekk di jéem a aar sa moroom. Fa lanu nekk di raayan...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_351
Lu waral may joteek Faatu Juuf, mu neexe noonu ba noppi, sama xel yépp nekk ci dee ? Ma gëmm, gis ñaari mellentaan yu tuutee tuuti te ñuul ñuy mareñ ci aw tund wu suuf sa weex tàll. Ma ni ci sama xel : « Maak Faatu Juuf bëggante nanu ba fu bëggante yem. Waaye lu nobeel di jariñ ? Lii lépp fan lanu jëme ? ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_352
Faat Juuf a ngi taraxlaayoo séru legoos, ferenklaayu, wéeru ci kanape bi. Lee-lee sama loxo càmmooñ doxantu ci kow yaram wi, naj ndànk catu weenam mbaa mu wàcc ba ci diggante lupp yi, jaaru fa as lëf. Maak Faat Juuf rekk a nekk ci kër gi. Dëkk bi ci boppam mu ngi ne selaw. Nuy diisoo, ku nekk di dénk sa moroom...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_353
Guddi googu laa mas a wax Faat Juuf ne sama cosaan, man, Mbériη-Saaj la, ca Siin : - Ci sëti Maam Ngóor Fay yi laa bokk. Faat Juuf daldi muuñ, ne ma : - Waaw, te noonu nga ci tollu ? Maam Ngóor Fay nag, ku ko jur ? Gis nga ni mbir mi doye waar, Badu ! La ma umple woon ba tax maa tegu ci yoonu Mbériη-Saaj la ma...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_354
- Xanaa nun Doomi-Aadama ! Nit ku nekk, booy nemmeeku cosaanam, ci yoon lim bi waroon naa mat ay junniy-junni at. Waaye ñi xam mbaa ñiy fàttaliku seen turu maam, ñu néew lañu. Maandu daal moo nu war, Ngiraan. Ma siggi, xool Faat Juuf, gis ni kanam gi soppikoo ndax tiis wu ma xamul lu ko waral. Ma ni ko : - Lu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_355
- Ndax yoon mujje naa teg loxo ci sa yaay ? Faat Juuf tontuwu ma. Sunuy bët daje, ma daldi yëg ci saa si ne wax naa lu ëpp. Faat Juuf gis ni ma amee kersa ci mbir mi, daldi ma xëcc, ma fekki ko fi mu toog ci suuf. Ñu tëdd nelaw, ma gént gént gu jaxasoo sax. Waaye ndax lii sax gént dégg la ? Maa ngi wetu kër F...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_356
Rax-ci-dolli, benn sófóor nanguwul a taxaw jël ma. Mu mel ni oto yi man lañuy daw ! Ñoom daal ñu ngi naan : - Fiiw ! Fiiw ! Fiiw ! Ma tiit, di saraxu sófóori oto yi may romb - Buleen ma fi ba, ngir Yàlla ! Waaye kenn ci ñoom nanguwu cee taxaw. Gisuma kenn kuy dox, sófóor si may romb it mënu ma cee teg kenn bë...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_357
Tàggoo nanu bu yàgg te xawma sax fan la nekk ci Senegaal ñàkkul sax mu génn àddina te yëguma ci dara. Guddi Kolobaan gaak tey jii ma tiim sama Téere bu ñuul bii, di ci bind lii, mat na juróom-fukki at. Lu waral tey jii sama xel yépp nekk ci Faat Juuf ? Lu tax biig ba tey fu ma geestu ci néeg bi gis takkandeeru ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_358
Bi may nelaw nag, guddi Kolobaan gépp ñëwaat na ci sama xel. Amul dara lu ci des ginnaaw. Ni ma ko dunde woon ba may am fanweeri at ak ñaar la dellusee. Yëf yi yemu fa de, Badu Taal : ci sama biir gént, géntaat naa taxaw ci booru tali bi, ca Kolobaan, mu lëndëm këruus, oto yu bare di ma romb, seeni faar di tàkk...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_359
Ma ni : dee gu taxaw jonn. Boroom xam-xam yi dinañuy faral di janeer, séen Ëllëg ak li ci biir ñu nekk ci yoon wiy daagu. Agseeguñu de, waaye ñu ngi janook ñoom. Ñu teg ci diir bu gàtt, muy lu ne fàηη- fàηηaaral, maak yow nu sog cee mën a teg sunuy bët. Dëgg la. Wànte ku ma newoon dinaa dund man mii ba bés ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_360
- Ngiraan Fay, may naa la ñaareelug dund. Doore ko bésu tey, at mu jot dinga gën a nekk xale. Am nga 80 at. Feek 79 at, dinga dellu nekk liir. Walbati jamono ji du dara ci man, defal naa la loolu ! Fépp foo mas a jaar, dinga fa jaaraat. Su ko defee, lu dëngoon ci sa jëfin nga jubbanti ko, koo mas a tooñ nga b...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_361
Xawma kan laa rusul ci àddina, waaye yow Badu Taal am naa lool sa kersa. Gone nga waaye ku la seetlu bu baax, fàww mu weg la ba sax xaw laa ragal.Yaa xam loo bëgg, doom : Yal na la ko Yàlla defal.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_362
TÉERE BU ÑUUL BI
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_363
- Dégluleen ! Jàmm la ! Dégluleen ! Jàmm la ! Yéenekat bi wër na Ñarelaa ay yoon i yoon, sog a taxaw ci pénc mi. Lee-lee mu tëgg sabaram, daldi dar nopp yi, yuuxu : - Dégluleen ! Jàmm la ! Dégluleen ! Jàmm la ! Mu ne tekk ba yàgg sabarooti ñetti yoon, daldi daraat nopp yi : - Buur nee na : góor ak jigéen, mag...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_364
- Fan la yéenekat bii génneek sabaram ? - Buur ban a woote, sax ? - Démb ak bërki-démb de, ay buur a fi newoon, daan dogal. Seen bëgg-bëgg rekk lañu xamoon. Muy dëgg gu wér péηη, ndax ku ci mel ni Daaw Demba demoon na ba ni : - Fii ci Kajoor, ku fiy takk janq, balaa ngay joteek moom, indil ma ko ma jaar ci ba ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_365
« Waaw, kañ la démb dellusi, làqu ci biiru Tey, nar fee judduwaat ? Kañ lanu fi fal Buur ba muy woote ? Naka la Daawur Jaañ mënee nekk njiitu réew mi ba noppi keneen naan mooy sunu Buur ? Du lii lañuy waxati ci politiseη yu naaféq yi ! » Yéenekat bi rëkkaat sabaram, xulli bët yi, yuuxu : - Buur a ngoog ! Buur d...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_366
Ba mu ñaanee ba noppi, mu siggi, xool mbooloo mi, waaxu ba ci benn ndaw su màggat, mu xëcc ko ba ci diggu géew bi, ni ko : - Lii ma ηëb, wurus la. May naa la ko ci xol bu sedd. Bés ni ki tey, sa soxlay àddina yépp faju nañu ba fàww. Képp ku sës ci yow, dootul xiif, dootul mar. Noonu la nu Aali Këbóoy feeñuwaat...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_367
Tàggu naa la, Badu. Fa may fanaani tey, duma fa fekk kenn, kenn du ma fa fekk. Dénk naa la ku baax ci yow. Dina la aar, dina la fajal sa mer. Dénk naa la Aali Këbóoy. Li des ci nettali bi, mooy boroom. Dina la ci may ba nga doyal sëkk ak barke.
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_368
ÑAAREELU XAAJ
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_369
AALI KËBÓOY Dof mat naa bàyyi cim réew
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_370
Badu Taal, yaa ngi may déglu, mbaa ? Sa maam Ngiraan Fay noon na la : - Bala waa Ñarelaa di teqalikook Aali Këbóoy, dinañu wax lu set. Dëgg la. Ngiraan masul a wax waxu caaxaan. Démb, soppiku naa mellentaan, dugg ci kawasu benn waa ju doon dem. Ma dégg ko mu naan ki mu àndal : - Sama Ndumbe mi de, moo may bëgg ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_371
Dégluleen ! Jàmm la ! Dégluleen ! Jàmm la ! Nee nañu loolu moo nar a firndeel ne Aali Këbóoy a ngeeti ci sunu biir. - Eskéy ! - Te kat, dinaa la xamal lenn, Tiijaan : Aali Këbóoy mi réew miy xaar, dina ñëw, nekk Ñarelaa lu yàgg a yàgg te kenn du ko xàmmee. - Nga ni ma ? - Boroom xam-xam yee ko wax, de. -...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_372
Sunu àndandoo nar naa yàgg te nar naa metti ! Waaye balaa nuy tegu ci yoon wi, dinaa leen fàttali kàdduy taalifkat bu mag ba.Sëriñ Musaa Ka nee na : Am barke àggul ci di def lu ñu dul wax Defkat bu dee def waxkat it ma ngay wax * * * Man, Aali Këbóoy, sama baat ca kow ! Waxambaane yi fi jaar sànq ci bëcc...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_373
Waaye nag, man Aali Këbóoy, am na lu ma xaw a yéem ci mbir mi. Ngeen ne ma : - Loolu lu mooti, Aali ? Ma ne leen : - Nit Njaay bu demee bay toppandoo boppam, xanaa war naa fekk xamatul moom mooy kan, xanaa fekk na njàqareem jéggi dayo ! Soo demee ba tànk boo yëkkati, ne man diw maay Man, te soo ko defulee ñu j...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_374
- Patiriis yaa nu doy, keneen ku dul yow du nu jiite, jal baa ngoog, nee ci faax su la neexee. Ñu neeti : - Jàmbaar da koy niru. Ba nga jàkkaarlook buuru Belsig, ñaawoo ci. Yërëmoo wax ji, danga jaar ci digg bi. Waa Belsig mer : - Ku mus a gis lii ? Ñii nga xam ne démb rekk sunuy jaam lañu woon, nu leen di së...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_375
Yéen a ñàkk faayda, yéen waa Ñarelaa ! Yeewuleen ! Waxleen ci li xew Kóngo. Bokkleen ci werante beek xeex bi. Nit ngeen, dungeen ay xar. Lan mooy coow li ? Ñii ngi naan Bels yi dañoo bëgg teg ci boppu réewum Kóngo seen xuus-maa-ñàpp, ngóor su yaafus sax, ñu koy digal muy dogal. Kooku, benn soldaar bu jege woon ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_376
Du xam ngeen nu ñuy rendee xarum tabaski ? Waxambaane yee koy ñàdd, boroom kër gi sog a teg paakaam ci baat bi, dem, dikk, dellu. Sosef Desiire Móbutook Móyiis Combe, xuus-maa-ñàpp ga ca Katangaa, ñooy surga yi ñàdd Lumumbaa, ay kilifay làrme Belsig daas seen paaka, daldi def seen mënin. Léegi nag, Móbutoo ngi ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_377
Konaakiri. Akaraa. Feerfaks Alse. Liyees ak Briksel... Dëkk yooyu ma lim yépp, ay gor fippu nañu fa, taxaw nañu ngir wone ne li xew Kóngo ànduñu ci tey, ànduñu ci ëllëg. Nun waa Ndakaaru Njaay it, kenn demul nu des ! Jóg nanu, taxaw ci tànki bañ. Yéen waa Ñarelaa kañ, yéen a yaafus te ñàkk dogu ! Daara ju m...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_378
Am nañu ko jéemoon ca jamonoy Maam ya, waaye fekewuñu ko. Lumumbaa waroon na xam moos ne mënul woon a mucc.Am na ci yéen ñuy déeyante. Waa- waaw, maa ngi leen di dégg kay, ngeen naan ci suuf : Aa, ndekete sunu ngóor si day dof-doflu rekk, waaye dara jotu ko. Su Aali Këbóoy dofoon kay, du mel ni ku naan Lumumbaa ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_379
- Lu jiin Njaag a te mooy Njaag ! - Moo ko sómbi, na ko naan. - Lu tollu ni Buur, rawatina buurub tubaab, nga di ko ηàññ noonu bëccëgu- ndara-kàmm ! - Ma ni : nen du bëreek doj ! - Tubaab yi soxaruñu gaa, dañoo bañ ku leen yab rekk ! - Mooy li ñuy wax rekk : ñi mën a kott amuñu mbaam ! Man de, su ma amoon wërs...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_380
Waaw, amaana sa soxla soosu faju de, waaye say sët ak say sëtaat duñu ko fekke. Wutewuleen ak ay nit yu ñu déj ci buntu kàmb gu xóot a xóot te fees dell ak i xal, yeew leen fa. Sañuleen sax yëngu ba seen xel di dem ci jéngu. Defe ngeen ne su ngeen di jéem a yëngu di tàbbi ci kàmb gi, safara si lakk leen, seeni y...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_381
Waaye ay doxandéem taxaaw ci waax bi, wàccee seeni gaal ak ay butéeli sàngara ak ay seetoo ki caq, nga daldi tàggook sa sago ci saa si, jaay sa jabar ak say doom, pasar-pasaree suufu Maam sii...Moo, tee ngeen a seetaat seen xel ! Ñaaw ci, lekk yu neex, te du mujje fenn fu dul seen wanag. Waa-waaw ! Maa ko wax ! ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_382
Badu, xool nga bu baax nataal yi ci yéenekaay yi ? Gis nga ni ñu yeewe Lumumbaa mu toog ci benn oto, sol simis bu weex bu xottiku, ndeysaan, ay soldaari Móbutu tiim ko, di ko mbej, téye ci karaw giy xëcc, di ko wéq, di ko tëfli ! Been soldaaru Belsig a jiite waa kër Móbutu yi. Ba mu bóomee Lumumbaa ba noppi, l...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_383
* * * Biig de, dégguleen sama baat bu naqadi bi, yéen waa Ñarelaa. Man, Aali Këbóoy, tanqaluma leen ci guddi àjjuma gi.Tey ma wax leen lu tax yàquma seen nelaw biig.Lii doηη la. Daawur Jaañ mi ngeen xam, njiitu réew mi, moo ma fekk may jàppanteek nelaw, mu ne ma pëkk-pëkk, ma xippi, dégg ku naan : - Aali....
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_384
- Saa waay, wéyal. Man, awma mbokk, awma xarit. Foofu mu ne tekk ab diir. Ma yëg ci sama yaram ni mu ma ne jàkk ci lëndëm gi. Sama xel yedd ma, ma daldi ne bëret, génn fekki Daawur Jaañ ci buntu mbaar mi.Soo ma gisee, maa ngi tiit bay pat- pati.Laajleen ma lan moo yóbbu woon sama fit noonu, ma wax leen ko. Bad...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_385
Dëgg la, Badu. Weer yale ñu génn, nettali woon naa la njàmbaar ga Patiriis Lumumbaa wone bés ba Kóngo di jot boppam, te Buuru Belsig nekk fa di wax ay waxi kasaw-kasaw. Dafa fekk rekk ne Lumumbaa du woon nitu neen, Badu. Kooku xamul woon sax fu tiitukaay di nekk ci Doomu-Aadama.Mën na am it, Badu Taal, nga ne m...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_386
Gis nga nag, maak sama mbokki dof yiy wëndéelu ci mbeddi Ndakaaru yi, li nuy kannasu yépp, xam nanu ne Muse la Paresidaa moo nu gën a naan kaani fopp. Ma ne : gaa ñiy feeñ tele ak seeni karwaat, ñu naan leen Muse la paresidaa diw, seen yaram duy faral di neex de ! Nit ku wér dëgg, du fekk ay junniy-junni Doomi- ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_387
- Gaawal laa wax, dama yàkkamti ! Céy dof moo sonn ! Boroom dëkk bi de, man maay nooy-neexam. Saa yu ma demee bay jàppanteek nelaw, mu ñëw yee ma, ni ma : - Aali sama bopp bi ubu na lool fi mu nekk. Laaj naa réew mi, askan wi jox na ma ko, waaye ca dëgg-dëgg xalaatuma woon ne nii la yëf yiy jafee. Léegi daal, ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_388
Aali, ni mbir mi doye waar, kenn mënu la koo wax ! Gis nga, bëccëg bépp maa ngi ci boppu gaal gi, di joow, ànd ceek fulla ju mat sëkk. Ñépp yaakaar ne xam naa bu baax fi ma jëm. Bés bu ma juumee ba ne ñi topp ci sama ginnaaw xawma yoon wi, réew mi tas. - Yàlla tere, Daawur ! Man Aali de, réew mi amalu ma benn n...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_389
Ñàkkul Daawur am fu mu jaar, door maa seetsi. Dafa ràkkaaju woon dëgg, di wax ay waxi dof. Li ma toog ci otoom yépp muy dawal, mu ngi ma naan : - Aali, yaa ngi gis tali bii nuy jaar, kër yi nuy romb yépp, garab yi ci mbedd meek kayit yi ngelaw liy ëf, ñuy wëndéelu ci jaww ji ? - Waaw, Daawur ? Loo ci wax, nag ?...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_390
Ba nu àggee Gël-Tàppe, joxoñ na ma benn kër, ne fa la daan jànge Alxuraan ba mu newee gone ; jaar nanu yoonu sinemaa Elaas, dem ba jub géej, jàdd sunu càmmoon, jubal taax ya. Ma ni ko : - Foo ma jëme, Daawur ? - Xanaa kër ga. - Kër gan ? - Bàyyil dof-doflu. Nanu dem gàlle waay, Aali, dóor fa sunu ndékki lu f...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_391
- Jàppal kenn ci dof yiy taxawaalu ci mbeddi Ndakaaru yi. Soo ko rendee, toggal deretam, naan ci, sëlmu ci. Fi may xalaatee loolu, Daawur daldi ma geestu, ne ma : - Agsi nanu, waaye yow sax danga mel ni kuy maas, Aali. - Wax dëgg, Daawur, su doon sama sago de, nga bàyyi ma ma dellu Ñarelaa. - Du danga ma ko ñ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_392
Fi nu toog maak Daawur Jaañ ci taabal jiy guux ndànk sunu kafe, ay soldaar a ngi nuy tóojal, di misig. Ma dem ba yàgg, seetlu ne am na ci ñoom ku ma ne jàkk. Saa yu ma wëlbatikoo, sunuy bët daje. Ma siggi gën koo xool, daldi ko xàmmee, ni ko : - Baay Ndeene ! Muy pat-pati. Daawur Jaañ ni ma : Ndekete xamante ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_393
Baay Ndeene di ma siiñ, ma ni ko : - Ayca, Baay ! Mu di ma awu, di tàccuwaale, di pàkkarñi : - Ofise ne paa pëer ! Bu doxatee sax du xasaw ndax kenn du ñemee reetaan ! Mujje gi soldaar yi ànd ak nun di misig, maak Baay Ndeene nuy fecc di tëb di dal, Daawur Jaañ ak i nitam ñëw fekk nu ci géew bi. Yëf yi mel ni...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_394
Nun ñéppp nu sëgg, ne tekk. Njëlug Kajoor. Picc yaa ngi woy, lee-lee ñu cof xobi garab yi mbaa ñu gësëm seeni bànqaas, làyyi biy toq ci sunu kow, nun kàngami Kajoor yi. Dammel ni : - Ku ci samay bët dajeek yosam, su dee gor du fanaan tey. Ba tey kenn siggiwul, kenn ηaaηul. Dammel daldi neeti : Luy jot, jot na....
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_395
Foo fekk Kocc Barma mu ngi jonkan, teg ñaari loxoom ci óom yi, ηëb ci loxo ndeyjoor bi juróom-ñeenti xooxi buy. Laaj nanu ko ba tàyyi lu muy doye juróom- ñeenti gif yooyu, waaye nanguwu koo wax kenn.Aka ñor tey, nag ! Golñàdd la, àgg ca kow. Su toogee ci biir nit ñi dafa naan keww, fu nekk mu fay sànniy bëtam. T...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_396
-Aa, Dammel, ñeenti jubb yii de, dara laa ci xamul. Waaye su dee danga bëgg xam lan la bu ci nekk tekki, mën naa la koo wax. - Su ma la ko laajulee nag ? - Say nit rey ma, ma dee. - Laaj naa la lu sa jubb yi tekki. Waaye soo waxee lu dul dëgg du baax ci yow. Keroog Kocc ñaawul ci xare bi, ndax Kajoor yépp la j...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_397
Jamono yii Dammel jàq na ba fu jàq yem te soo moytuwulee dina ne yaak noonam yee ànd di ko fexeel. - Gis naa bët yi ma seen Dammel biy xoole, wallaay. - Aa, gis nga ko de ? Defe woon naa ne man rekk maa ko seetlu ! Tee ngaa génn dëkk bi, Kocc ! Buuri tey yi dañoo fiir, de ! Yéen a ngi dégg wax jeem, yéen waa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_398
Ku xamul fu Àllu-Kaañ nekk it, dégg nga turam. Badu, ci ubbiteb Téereb Dóom, Ngiraan Fay noon na la su am réew jànkonteek ay jafe-jafe, dina am ay bés yu ñu ciy ràññee bu baax. Jotoon na lim sax Talaatay Ndeer ak Dibéeru Guy-Njulli. Sàmba Lawbe Faal ak baayam Makoddu Faal.Sadani Caam ak Mbarka Ja. Ñii di góor,...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_399
Gis nga, Badu, jamono dina ñëw, aw askan ni : - Sunu réew mii de, ba mu sosook tey, bés bi ci ëpp solo, bés sàngam la ndax bés boobu la lépp sotti. Kuy faral di déglu géwél yi mbaa mag ñi dinga xam li may bëgg a wax foofu.Tey jii, koo laaj, mu ne la 26 ci weeru oktoobar, ca atum 1886, maanaam bés bi Lat Joor d...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_400
- Ayca, du dangay jaay dijj ηaam rekk, tontul nag ! Dinaa tontu kay. Man Aali Këbóoy, ma ni : Ñii may limsi, ñoo séq xew-xewi bés boobu : benn, Kumandaηu serkalu Kees, Kees-Kaay, benn dëkk, ñaari gaar, di Tubaab bu ñu doon woowe Andre Kastorel ; ñaar, raay yi saxaar giy jaar, Tubaab yi defoon ko fi, te Lat-Joor...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_401
Su ngeen ko jéematee dinaa toj Ñarelaa ba mu mokk rumbux, ay xal dinañu wàccee asamaan dal ci seen kow, ngeen lakk ba xëm ñuul kukk, seeni kër def dóom ! Te dóom boobu, ngelaw li dina ko sànni fu soree-sore ! Giñ naa ni kenn ci yéen du mucc ci musiba moomu ! Baal ma àq de, Badu, ñii dama leen a rekk xaare ! Wa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf