url
stringlengths
6
8
content
stringlengths
2
3.72k
source
stringclasses
3 values
page_402
- Ndimboy dina am ñaari gan tey. Ñu ngi ci yoon wiy ñëw. Nu téen nun itam, gis ni pënd bu xonq bi muuree jaww ji, dégg ay tànki fas yuy woy ci kow suuf si, mel ni ndënd mu ñuy rëkk ak doole. Ma ne : - Tee noo jaar ci xur wi, jiitu gan yi dëkk ba ? Kenn tontuwu ma. Ku nekk a ngi déglu Mbiita ba xam lu ciy xala...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_403
Ni Mbiita Saar waxe xaw maa merloo, ma daldi ñëg : - Li ngay jaay amul, Mbiita ! Ñii di ñëw, su ñu bettee Ndimboy nag, dal ci kowam, looy wax ? Mbiita Saar reetaan : - Xawma kañ ngay muus, Aali. Fas wii may dégg ay tànkam, fasu Kumandaηu Kees la. Na mu tuddati sax, Tubaab boobu...? Fàtte naa tur wi, waay... K...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_404
Bi ñu demee ba sore, nu cëppeelu ci suuf. Abu Sow ne Mbiita Saar : - Yow nit nga walla rab nga ? Maa ngi lay bëgg a ragal kat, Mbiita ! - Yéen a ma xamul rekkk, waaye seen bopp ! Te loolu du woon ay waxi caaxaan, Badu. Nànditeg Mbiita Saar, fu ko nit nattoon, weesu na ko. xéy- na looloo tax Yàlla teel ko fee jë...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_405
Ba ñu gisee ba noppi, kooku woolu Manjaay, ni ko : - Kumandaη Kastorel nee na dafa bëgg a waxtaan ak nun. Yëgalal ma ko waa Ndimboy.Manjaay daldi tambàlee wër mbeddi Ndimboy yeek sabaram : - Dégluleen, jàmm la ! Dégluleen, jàmm la ! Boroom dëkk bi nee na : Kumandaηu serkalu Kees, Muse Kastorel, moo fas yéenee ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_406
Ak li may nekk gone yépp, maa ngi yéemu cili may gis : Andre Kastorel, daal, mooy sunu Dammel bi kenn yëgul fu ñu ko fale, kilifay Ndimboy yi ko wër di ay dagam, muy tabb di tebbi. Maa ngi gisaat lépp, Badu. Ba tey jii, li ma teewe keroog a ngi mel ni nataal bu ñu kuppati, taf ko ci sama biir yóor.Yow kott ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_407
Nun nag, noo sàggan sunu càgganu bopp ba mu féewale nu, daan nu, fu nekk mu teg fay nitam, lu mu leen sant ñu def ko. Dem nañu fi sax ba su la Xonq-Nopp saagaa, soo feyoo dunguroom yooyooy jëkk a soqi seen fetal ci sa kow. Benn xarnu jàll, beneen jàll, ba muy ñetti xarnu. Ñu dem ba Kastorel di Kumandaηu serkalu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_408
- Loolu du nu boole. Seen réew a ngoog, jël leen, fu ngeen xam ngeen jëm faak moom ! Waaye Badu, wax, wax dëgg ci la. Yaakaar nga ni coono bi fi Ngiraan Fay ak waa PAI daj àntu na ? Tey jii nu ne noo moom sunu bopp, ku sañ ni coppite am na fi ? Lee-lee Daawur Jaañ fëgg dënnam, ni moom moo jàmmaarlook Kastor...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_409
Soo gisee ma lim diiwaan yu bare ci réew mi te boolewuma ci Kajoor, du dama sàggan, du itam dama koo fàtte. Dafa fekk rekk ni li ma lay waaj a nettali, Kajoor la xewe, te Andre Kastorel, Kumandaηu serkalu Kees ci boppam moo la koy àgge, Badu.Nga ni ma : - Naka la loolu mën a ame, Aali ? Ma ne la : - Bul yàkka...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_410
Baay Séy siggi, ni : - Kumandaη Kastorel moo leen di xamal ne, moom de, am na naqar wu réy, te kenn tegu ko ko ku dul yéen ñii toog. Jarul sax muy jaaraat ci jëf ju ñaaw ji fi ay saay- saay di def boobaak léegi. Ay weer a ngii, saa yu jant bi sowee, ñu buddi raay yi ñu fi teg, ñoom waa Tugal, ngir saxaar gi di c...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_411
Muse Kastorel de, nee na moom mënul a gëm loolu. Xanaa kay ñàkkuleen fulla bay jàpple ay noonam ! Tee ngeen bañ a gaaw a fàtte ! Am na ku fi doon jaay njàmbaar de, di rab-rablu, naan Maalaw du gis raay bi ! Ana mu tey ? Song nanu ko Déqële, duma ko. Nun Tubaab yi nag, doole lanu am ba mu doy ! Ku nu bëgg a jomma...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_412
Noon nga saxaar gi du jaar mukk Kajoor ! Wóor na ma ni fa nga tëdd ca Déqële, dinga koy dégg muy mbiib, di riirloo taax yi, di yëngal Kajoor, suuf siy xottiku, muy daw guddi di daw bëccëg ! Yéen waa Kajoor, Kumandaη Kastorel moo leen di laaj : ndax jàmbaar dëgg dina làqatu di buddiy raayi saxaar, di sànni së...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_413
ba noppi teg ci saxaar gi muy daw, ngir jokkale diiwaani réew mii, Kumandaη nee na : xaalis boobu, wax dëgg Yàlla, xejoon na ci waa Tugal. Kumandaη Kastorel moo leen di laaj : ndax ni mu laabiiree, moom Kastorel, ak ni mu bëggee dimbali Ndimboy, loolu ngeen koy feye ? Boroom dëkk bi ne bëret, ni làppto bi : N...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_414
- Yéen a ko gisal seen bopp, de ! Sama dof bi merati na ! Kumandaη nee na : yow boroom dëkk bi, naaféq nga te li ngay wax yépp, dara du ci dëgg ! Man nag, góor gu baax, sa mbokk laa te soo ma mayee, dina am lu ma ñàmbaas ci wax ji, ngir dimbali la. Tànnal ci dëkk bi juróomi janq yu ñuul te sew ruuj, nga jébb...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_415
Baay Séy waxtaanaat ak Kastorel lu yàgg. Baat bu mu wax, Tubaab bi yëngal bopp bi, màtt tuñ wi. Bi ñu noppee, Baay Séy ne : - Kumandaη Kastorel a ngi leen di gërëm. Nee na it, ginnaaw guddee na fi, maak moom Ndimboy lanuy fanaan. Fekk na boroom dëkk bi rendilu ay xar ak i béy. Ñu wàjjal gan yi yàpp, ñu naan së...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_416
Ay sëmino jóge gaaru Kees, topp ci raay yiy kol-kolal. Waaye saa yu ñu liggéeyee ba yaakaar ne ñoo ci nekk, yàqkat ya defaat ñoom it seen mënin. Ñu jàppe ko noonu ay weer. Tubaab yi jaaxle lool. Kumandaη Kastorel daldi tàmbalee tuumaal Lat Joor nag. Loolu ub sunu bopp, nun waa Ndimboy. Nu ne : - Aa ! Lat-Joor...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_417
Weer ya ca tegu, Badu, jàmm ne ñoyy ! Jàmm ne ñoyy, saxaar giy daw ni ko neexe ci diggante Ndar ak Ndakaaru ! Kumandaη Andre Kastorel bég ba fu bég yem. Ñaw ! Ndekete nii la upp baaxe ci laax bu tàng ! Ñépp noyyi, féex, ndax rekk ni Tubaabu Kees bi jëlee woon mbir mi dënn. Nun waa Ndimboy, nu defaraat sunuy n...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_418
- Loo ma waxoon ? Aa ! Man ngay jéem a tuur lëndëm ? Waxal ! Looloo la dese ? Sa tés-tés ju metti ji yépp lan la jur ? Dara la jurul ! Dara ba dara booloo jeex ! Tus, laa wax ! Su fekkee ne sowaas yii ñoo lay të, dinaa la delloo Tugal ! Su ma déggatee ne Lat-Joor teggi na fi raay bi gën a tuuti, du baax ci yow ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_419
Bi jant biy waaj a so, Andre Kastorel, Kumandaηu serkalu Kees, dóor boppam balu fetal. Bi nit ñi dawsee ngir wallu ko, fekk nañu yóoru Andre Kastorel tasaaroo ci ruum bi, tasaaroo ci kow kayit yi doon tege ci taabalam. * * * Andre Kastorel xaru. Beneen Tubaab wuutu ko, nekk Kumandaηu serkalu Kees. Waaye n...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_420
Bi ñu demee ba waa Ndimboy di ηun- ηuni, lu nekk ñu ko ciy wax, boroom dëkk bi woo mag ñi, ne leen : - Fan yii yépp, yéen a ngi fiy gis ab Tubaab buy dem ak a dikk, di nemmeeku itam xeeti garab yi nekk ci Àllu-Kaañ bii. Dama bëgg ngeen xam ne Kumandaηu serkalu Kees bu bees bi, ki wuutu Kastorel, moo ko fi yebal....
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_421
- Waaw, nee na am nay pexe yuy gën a naatal gàncax gi, aar jur gi. Su nu bëggee daal, dinanu jàngal ni nuy def ba xiif dootul rey kenn ci Ndimboy. - Ngóor sii gën a bare caaxaan ! - Man it de, mbir mi jaaxal na ma. Moo tax sax ma woo leen, yéen magi Ndimboy yi, ngir nu gise. - Naka la ab Xonq-Nopp mën a dëkke ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_422
Moo xam ci melo bët yi la, ci waxinam walla ci xar-kanam gi. Robeer Langlaad moom, bopp bi dafa tàppandaar. Langlaad fexe na ba dëkk ak nun Ndimboy lu mat juróom ñeenti weer. Ku sob la, ndax lu nekk mu ngi koy laajte, di for ay xeer ak a witt ay xobi garab, di leen xeeñtu, di bind seen tur ci benn téere bu wee...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_423
Tanqalu nu itam ak waxi raay bi taxoon Kastorel xaru. Li nu jaaxal kay, mooy li mu ne dafa nu jàngalsi bey te masul a wax lu ci jëm ! Lee-lee mu dugg biir Àllu- Kaañ, toog fa ay fan i fan. Mas nanoo fexe ba bett ko fa, maak Mbiita Saar. Fi nu làqu, Mbiitaa ngi ma naan ci suuf : - Aali, seetlu nga bu baax Capp-Ca...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_424
Nawet bi ñëw. Benn guddi, ñu tàmbalewaat teggi raay yiy sànni. Naka la ko Mbiita Saar dégg, ne fàww mu ceddowu Capp-Cappal. Wànte bi Mbiita sullee wax ji, Tubaab bi fullaalu ko. Dafa ko ne rekk : - Loolu bokkul ci sama liggéey. Te yow sax, Mbiita, seetlu naa ni gone gu yeewu nga ! Dinaa la yóbbu Tugal nga jàng...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_425
seetu dootul réy mbaa mu dëgër ba dab seetu Robeer Langlaad boobu. Maak Mbiita Saar nu jàppale ko, mu daldi samp seetoom ci diggu Àllu-Kaañ. Bés, nu yeewu suba teel ak tiitaange ju réy. Nun daal, danoo jékki-jékki dégg suuf siy riir, mu mel ni dafa am ay ponkal yuy buddi garab yi di leensànni ci jaww ji, garab y...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_426
Lee-lee kenn ki bës baaraamam ci seetu bi, mel ni kuy jéem a luqiy bëtam, ñàngal kanam gi, ηóobi, yëkkati loxoom, xàcci ba dara desul lu dul dóor mu wàcce ko, mel ni kuy artu ki mu janool : - Soo ma moytuwul, yow, dinaa la def lu bon ! Moroom mi gis ay butéeli sàngara yuy tege ci wetu seetu bi, mu gàddu ci be...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_427
ngay yuuxu, toqi, waaye sa jom mayu la nga bàyyib doxandéem mu fekksi la ci sa biir kër, bëgg laa jam naani. Loolu moom, xel mëneesu koo nangu ! Dàngin yi dem ba seen takkandeer ak seen jëmm maasaloo. Ñaari ponkal yi fàtte seetu bi, nag, daldi songante.Xeex bu yàgg sax, te metti, Badu ! Benn dàngin gi ne kàtti...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_428
Aywa ! Xeex bi neeti kurr. Dàngin giy jamat boppam ba yaram wépp dagg. Soo ko gisee mu nga lott ba xamatul fu mu ne, di xiixat. Mu jékki-jékki bàyyeeku, àgg suuf, ne nemm, ndeysaan. Waa Ndimboy génne fa ñu làqu woon. Dàngin gaa ngi jaaxaan ci wetu moroom mi mu dagg bopp bi, deret ji muur, yaram wépp, xonqal d...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_429
Su ma la fàttalee loolu, Badu Taal, dafa fekk ni man ci sama bopp, lépp lu ma xam ci àddina, dàngin ga ma tiim muy sukkuraat ca Àllu-Kaañ moo ma ko jàngal. Fonk sa bopp, naw sa xeet, bañ a jébbal sa ruu ay doxandéem, loolu lépp, Badu, bés boobu laa xam lu mu tekki dëgg-dëgg. Dàngin gi daldi dog. Fi ma toog, ma...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_430
Keroog, Robeer Langlaad fanaanul Ndimboy. Dafa jubal Kees, yót Kumandaηu serkal ba ñaari boppi dàngin ya doon xeex biir Àllu- Kaañ. Ca lanu gëjee dégg lu jëm ciy mbiram. * * * Seetal ma lii rekk ! Toog diggu màrse, daggat sa ruu, saam, ne danga koy wànteer ! Doomu-Aadama ni yow jóge fu kenn xamul, gënula nd...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_431
- Tee ngaa bañ a waxe noonu ? Tey gaal gi jóge Tugal indiwul piis, indiwul caq. - Te mënoo ci teg dara, yow tamit ? Ruu kat du caaxaan ! Ngeen waxaale ba juboo, mu daldi nos sa ruu, wommat, dugal ci gaal gu màggat, dem yoonam. Yow moom, taloo dara lu dul jolu say butéeli sàngara. Bu jeex nga ubbi beneen. Sa yar...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_432
Noo tuddoonati sax, yow ? Am nañu lay woowe Daaw Demba. Waaye am nañu naan déedéet, sa tur dëgg Daawur Jaañ la. Dégg naa it ñu naan Móbutu Seese Seko nga tudd. Ak noo mën a tudd, ndóol geek naqar wi nu nekke tey, yaa nu ko yóbbe ! Bi nga wuyujee Maam ak tey mat na ñeenti xarnu. Dem nga barsàq, wacc nu feek sunu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_433
Réew mu amul seetu, dara desatu fa. Sàmmleen seetu yi ! Waay, bàyyil-leen seeni sët ak seeni sëtaat fu ñu mën a gis seen bopp, mu doy leen, ñu bañ a sëgg ndax gàcce gu jéggi dayo. * * * Bés, góor gu sell gi gis na leen ñuy yox- yoxi, mu ne leen : - Du caagin damaa mën a dige. Man, maay ki am pey ba mu doy ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_434
Gëmoo ma ? Xaaral ma fàttali la fan la Ngiraan yemoon cib nettaleem. Tey ngay xam ne man Aali Këbóoy, dof bi, maa forox nopp te neex xel, kaar ! Ngiraan Fayay wax de ! Déglu ko...Ngiraan Fay noon na fi ci Téereb Dóom : « Waaw, Badu, ku la masula tudd, masula taas, su takkee ay waliisam, fëgg sa buntu néeg, ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_435
Waroon naa réy de, ndax ci ay xultu ak ay waxtu la mujje. Ne tuuti, Biige Sàmb agsi taf gémmiñam : - Waaw, Yaasin yow, loo xewle ? Du danu waroon a dem ci Sinkun Kamara mu ñaanal la, ñaanal xale yi ? Yaasin siggi, ne jàkk Biige Sàmb. Man mii Ngiraan Fay de, dootuma gone, waaye giñ naa ne musumaa gis nit ku jà...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_436
- Amatuma paaspoor, amatuma kayit giy biral ne Tubaab laa, lépp réer na ! Nu may def, Biige ? Fu ma jëm ? - Nanu dem. Man Biige Sàmb loolu mënumaa të, am naa ci pexe. Li ma nànd keroog ci waxtaanu Yaasin ak Biige, lii la : musiba moomu daloon Yaasin, sa yaay amoon na ci mbégte mu réy a réy ! Te njortoon naa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_437
Sinkun Kamaraa ngi toog ci derub mbaam-àll bu ñuul. Soo gisee Yaasin moom, mu ngi sànniy bëtam fu nekk, mel ni ku fit wi rëcc, mu jaaxle, di réccu li mu doon toppe Biige Sàmb Baal ma, ma may la tuuti ci Sinkun Kamara, Badu. Yaa ngi fàttaliku Ustaas Mbay Lóo ? Ci Téereb Dóom, Ngiraan Fay won na la pukkuus ba...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_438
Sinkun Kamara xool Yaasin ba seppali ko, wiccax ndànk bopp bi, daldi ne : - Sama kóllëre nga, Biige. Lu ma ci mën, dinaa ko def. - Maak yow kañ, Kamara Yille, démb la woon, tey sog a ñëw. Yaasin mii nag, am na nu mbir mi doon deme nu nekk ay noon maak moom, ba ku jekku kon sa moroom gaañ ko. Ñaari doom la am, ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_439
Moo ma ko ji, moo ma won kanam gu tax ma sañ koo jege, ba léegi maak moom nuy ay doomi-ndey. - Yal na Yàlla gën a dëgëral seen diggante. Ñaar ñu baax ñoo mën a ànd. - Sëriñ bi daal, dénk naa la Yaasin. Ñaanal ko. Bi ma demee di ko jëli sànq, nee na ma ay kayitam dañoo réer. Dimbali ko ba ñu feeñ te muy li gën c...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_440
- Soo bëggee sa aajo gaaw a faju, jéemal a làkk wolof, mbaa séeréer mbaa joolaa mbaa kikuyu. Sama gaa ñi dégg nañu làkki Doomi-Aadama yépp, waaye lee-lee dañuy jéppi ñi leen di làkk nasaraan. Te ñoom kat seen mer baaxul, yàq nit ak naan ndox lañu yemale. Yaasin def li ko Sinkun Kamara sant. Taryaax bi ne Biige...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_441
Tuutee tee sax ndaw si gedd, bàyyi Sinkun Kamara ak i xërëmam, dem defarlu ay kayit yu bees. Làmmiñu seku wu ñu fanaanal ci këllu lem.Juróom-benni bëti golo. Nenu banjóoli ak nenu naat yu ñëb. Tojitu seetu ak kawaru Tubaab bu jigéen. Ñax mu tooy.Ba Yaasin indee li mu ko laajoon, Sinkun Kamara boole yépp sotti ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_442
- Yaasin Njaay, dégguma sa baat ! Du yaa bëgg ma soppi la ? - Waaw. Maa la ko ñaan. - Mën naa la soppi, nga nekk loo bëgg ! Loolu du dara ci man. Yaasin Njaay, nee ma naam ! - Naam, Kamara ! - Soppi la leneen ak naan ndox laa yemale. Dégg nga wax ji, de ? - Waaw, dégg naa ko. - Yàlla miy maye di nangu moo m...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_443
- Mari-Gabriyelaa. - Tur woowu neex naa dégg. Mari- Gabriyelaa naka ? - Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski. - Nga ne lan ? - Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski. - Bind ko ci kayit gii. Yaasin gaawantu bind turam. Sinkun Kamara dellu ni ko : - Waxaatal sa tur ma dégg. - Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski. - Jaaraat ci ma dé...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_444
tàllal ko Sinkun Kamara. Góor gi mer, gëdd ko : - Téyeel sa loxo.Yaasin yëg ci saa si ni yaram wiy loxee ndax tiit. - Baal ma de, Monsieur Kamara. - Xawma muse Kamara, xawma muse Jàllo ! Bumu ñaar, laa wax. Ku la ne mën nga ma fey, man ? Sinkun Tiggide ! Tiggide Sinkun ! Kamara ! Xaax ! Fi Yaasin toog di xaar...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_445
Fekk na yëf yaa ngi doon gënatee teey xelam. « Man it, kenn du man ! Waroon naa xam ne Biige Sàmb man rekk la bañ ! Lii mu ma dugal, wóor na ma ni musiba rekk lay juri ëllëg. Bi ma dellusee Ndakaaru ba léegi mu ngi ma ñóoxu, naan dama koo neex, dafa ma sopp, fekk duggewu ko dara lu dul toroxal ma. Sàcc samay ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_446
Ndaw bànneex bu réy ! Ñuulaay bi dafa rekk doy. Ku ragalul wax dëgg, xam ne moos lu ñuul mënul a bañ a sikk. Der boo xam ne bala moo jag nga topp ciy fóot ni yëre bu tilim, yendoo fete, fanaanee fete ! Ku ci doyalul itam, moom Yaasin Njaay doyal na ci sëkk ! Fi Yaasin di xalaate loolu, am ku fëgg buntu née...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_447
Waaye Sinkun moom mu ngi sëgg fi mu sëgg rekk, di tari li muy tari, mel ni ku yëgul ne am na jeeg bu ñëw tiim ko, ba noppi ne tekk di ko xool. Yaasin tàmbalee waxtu ci suuf : « Aa ! Ndekete ndaw si duggsi Tubaab bu weex tàll la ! Aa ! Looloo tax ngay jaay maanaa ! Soo ma laajoon, xam ne wallaay Sinkun Kamara f...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_448
Jeegu Tubaab baa ngi taxaw ci ginnaawam, ne ko jàkk. Mu ne ci xelam : « Ndaw sii de, dafa mel ni ku ma jéppi. » Yaasin Njaay jéem koo wàcce, daldi muuñ. Ndaw si ne këj, gën a fas kanamam. Ca la Yaasin xalaatee lu doy waar : « Moo man, mbaa du dama génn àddina, nekk àllaaxira, te yëguma ci dara ? » Noonu mu n...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_449
- Dama ne, bul ma tanqal Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski ! Xam nga ne moos kooku fi dugg sànq du kenn ku dul yow ! Daa weex nga ñuul rekk, waaye benn ngeen. Seetul bu baax, laa wax ! Fitu Yaasin Njaay mayu ko muy walbatiku di seetuwaat. Muy lox. Dunyaa xar, def ñaar. Taax yu rafet yee muy séen nag, fu ñu bawoo ba...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_450
- Loo bëgg ci àddina dinaa la ko defal ! Su ma ko amulee itam, dinaa ko wuti indil la ko. Sinkun Tiggide Kamara ne Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski : - Futtikul. Mari-Gabriyelaa futtiku, mu jaar ci moom, jaaraat ci moom. Ba ñu noppee, mu ne ko : - Man de, maa ngi soog a digaaleek jongomay Tubaab. Waaw, ndekete y...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_451
- Mbaa jàmm la, Sinkun ? - Liggéey bu nekk ak weexalam. Dinaa la xaar, maak yow am nanu waxtaan wu réy. * * * Ñu teg cay fan, Yaasin Njaay dellu seeti Sinkun Kamara.Kooku ne ko : - Léegi nag, déglu ma bu baax : du ñaari doom nga am ? - Waaw. Mbisaan ak Mbisin. - Soxla naa ci kenn. - Nga ne lan ? - Dinga...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_452
Sinkun Kamara xool ko ba sappali ko, ne ko : - Bul fàtte ki ngay waxal. Sinkun Tiggide ! Tiggide Sinkun ! Kamara ! Xaax ! Mari-Gabriyelaa mel ni ku ràkkaaju, daldi ko yuuxu : - Loolu mënul a am ! Non, non et non ! - Dina am de, moonte. Mu neex la dina am, mu naqadi la dina am. - Su sa loxo laalee sama benn doo...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_453
- Lépp maasaloo na ba fàww, amatul dara loo xam ne nit mën naa taxaw ne lii mooy màndargaam. Nga téen, séen oto yiy rawante ci taliy asamaan si. Nga sëppu, gis asamaan seek i biddéewam ñuy paccax-paccaxi ci ndoxum géej gi. Démb saay na, Tey saay na. Fen ak Dëgg itam, ku ci nekk seey nga ci sa biir deretu moroom...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_454
Doo nitu dara ! Ku bañ sa bopp, xeeb sa xeet, noo mënee bëgg say doom ? Bi mu ko wóoree ne Sinkun Kamara caaxaanul, Mari- Gabriyelaa Won Bolkowski tàmbalee yikkat, di jooy ni xale bu ndaw : - Waaw, góor gi, loo tuddee sarax ? Noo mën a xalaatee ne dinaa la jébbal Mbisin walla Mbisaan nga tëral rendi ? - Man k...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_455
Ku dégg sa tur xam ne yax bu réy a réy nga bokk ca Tugal, gën faa rafet juddu ! Aa ! Dellu Tugal, dëkk fa, te kenn dootu la fa gën a yey ! Waaw, kenn dootu la fa xool ay bëti sowaas nga, danga tilim, danga xayadi. Fu la neex nga dem ci àddina si te kenn du la laaj wiisaa... - Loolu ngay wax yépp jaralu ma sama ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_456
jubal daara ja. Xawma Mbisaan lay doon, xawma ku jigéen ki lay doon, waaye sa doom ji ma lay bàyyil, ay tànkam duñu dëgg mukk ci ay ndell, ndax Tugal ga mu nar a dëkki de, wute na lool ak Liberyaa mbaa Siyeraa-Lewon, ay way-fippu duñu fa gàddu seeni ngànnaay song nguur gi, ku ñu dajeel gor la jaasi. Li Sinkun ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_457
Bu sama gaa ñi meree du baax ci yow de, ndax dinañu këf Mbisin, këf Mbisaan, nga des yow kenn ak sa naqar. Loolu nga bëggam ? Keroog, Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski réccu na ndajeem ak Asan Taal ca Màrsey. « Ku ma newoon nii la yëf yiy mujje, ma ne la yaa mën a fen. Waaye fen moom, kenn dàqu ko woon Asan Taal ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_458
Sëggal boog ma déey li ma sañula wax ci kow loolu, man Aali Këbóoy. Séytanee ngi ruux Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski, naan ko : - Yaasin Njaay, tee ngaa gëmm rekk, jébbal Sinkun Kamara sa benn doom ? Sinkun Kamara kat, def na warugaram. Léegi yaa ci des. Ku bëgg akara dangay ñeme kaani. Tee nga koo sarax Mbisi...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_459
Mbisin ak Mbisaan, mag ji, ñoo génn xeet tey ! Log ay baat yu masul a tëmb ci sa soowu ndey ji la jur, di leen sàqami ndànk, ñuy seey ci sa kow làmmiñ, saf suukar, neex, di la jox bànneex bu kenn xamul nu mu tollu. Walla kàddu yooyu tancaloo ci sa biir put ba far la fotloo.Maam ne la : - Neel Penda Saar ca Ng...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_460
Ca la la ne : « Fu la jant biy tiime, Badu Taal ? » Seede naa ni keroog xolu Ngiraan Fay diis na ! Xam naa dafa yëgoon ci yaramam ne dina wuyuji sunu Boroom bi te dungeen gise. Booba, sama takkandeer a ngi wëndéelu ci néeg bi, ma yërëm Ngiraan ba sama rangooñ yiy bëgg a tuuru... Man doηη maa ko mënoon a wax...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_461
Rax-ci-dolli, sama digganteek Ngiraan Fay, caaxaan walla waxi naaféq masuñu cee am yoon. Looloo tax ba ni mu fi jógee, ndeysaan, Ngiraan masul a xam foo nekk ci këru àddina. Démb, ñëw naa ganesi la bitim réew. Gisoo ma waaye li ngay wër ci biir dëkk boobee yépp, maa ngi topp sa ginnaaw. Yaa ngi ànd ak Abdel Ka...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_462
Làq-làqal bi doyulam ? Nëpp-nëppal bi nag, ba kañ ? Maa ngi ciy teg sama bët, man mii : ku ngeen dajeel, mu xeelu leen, gaññ, won leen ni mu leen xaaree. Waa réew moomu jàppe leen ni ay jaam, te ngeen di wéye naqar woowu, amuleen fenn fu ngeen koy joytoo ! Man, Aali Këbóoy de, bëgg naa xam lu tax ñépp tëx, mu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_463
Amul péex, amul keppaar. Fi ngeen toog di xaar ótóbiis, benn ndaw su màggat ciipatu na leen, móolu leen ci làkkam, ngeen mel ni ku ko déggul. Yaa ngi wéeru ci benn poto-làmp, ubbi sab yéenekaay di ko jàng. Nga jékki-jékki yëngal sa bopp, ne : - Seetal ma lii rekk ! Abdel Kadeer Maxjub geestu la : - Lan laati...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_464
Loolooy coow dëkk ba, de ! Abdel Kadeer a ngi ree ba téye biiram. Yow, nga waaru, daldi ne ci sa xel : « Kañ laa gëj a gis Abdel Kadeer mu bàyyeeku, di reetaan nii bay xàqataay ? » Kadeer siggi xool la, ne : - Ay waxi dof nga may wax, kañ ! - Waa dëkk ba dofuñu wallaay, Kadeer ! Li leen jàpp ba ñuy gëm yëfi dof...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_465
Tuuti kon ma dugg ci seen waxtaan, ne doomu réewu Sudaη jooju : - Waaw, ngóor si Abdel Maxjub la xawma, lu la ci ba ngay weddi ak di dëggal ? Yow gën a waane ! Xamal ni ñett yii, maa leen yelloo, man Aali Këbóoy : gis lépp, dégg lépp, fekke lépp ! Mbaa du danga may diir mbagg di ? Juróom-ñaari xarnoo ngi jaaxa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_466
Kon boog, Badu, xam nga ni yaa ngi ci biir-a-biir... * * * Bésub talaata la woon. Ngiraan Fay jóge jàkkay Ñarelaa lal ndésam, toog ci ëtt bi. Mbisin ak Mbisaan a ngi taal tele bi ba mu sës. Ngiraan woo mbindaanu Yaasin Njaay ni ko : - Aram, doo ma baal wax Mbisin ak Mbisaan ñu wàññi tuuti tele bi, kenn ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_467
- Muñ dee fi sës, Maam Ngiraan. Léegi mu jeex sax, ñoom ñépp a ngi waaj a dellu Tugal ! - Keroog de, seen yaay mel na ne ku am lu mu réerle ! - Altine jee nu génn, mook bàjjan Biige Sàmb ànd nañu seeti benn sëriñ. Ci la ma ko dégg muy wax de, feek i fan rekk mu ñibbi Tugal. - Li mu réerle woon feeñ naam ? - D...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_468
Ngiraan dégg ku laal buntu kër Yaasin Njaay : « Waaw, jeegu Tubaab bu sew bii, lu muy wuti kër Yaasin ? » Mu ne bëret, ne day laaji ndawsi lu doon i tànkam. Kooku walbatiku, xool Ngiraan ba seppali ko, ne ràpp buntu dogaatle bi tëj. Yàggul dara ñu dégg Aram, mbindaanu Yaasin Njaay mi, muy salliiru : - Wóoy sa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_469
(Gis nga de, Badu, man mu weex dunq mii, fexe nañu ba tudd ma ci. Nit ñee mën a tooñ, walla !) Am keneen ku ne : - Waaw, jeegu Tubaab bi wàcce ci oto bu ñuul, dugg fi nag, ku mu, Ngiraan ? - Li ngeen may laaj de, dara laa ci xamul ! Tee ngeen a àggal seen bopp kër Yaasin Njaay, seet lu fa xew ! Noonu, yuuxu Ar...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_470
- War naa leen a balu àq, ndax xéy-na ni ma waxeek yéen xaw naa ñagas. Waaye maak Ngiraan Fay rekk noo fi war a des. Li xew lu réy la, te nun ñaar doηη noo ko séq.Ne tuuti, kër gi ne selaw, mel ni kenn masu fee nekk.Ngiraan ni : - Ana sa xarit bi, Biige ? Biige Sàmb ne patt ba yàgg mu sog a tontu Ngiraan : - Bu...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_471
- Waaw, Tubaab bi ma fi romb sànq, lu mu joteek Yaasin Njaay ? Biige Sàmb ne tekk, ba yàgg mu wàcce baatam, daldi ne ndànk : - Ndaw si la romb sànq mooy Yaasin Njaay. - Man de, ndeyu Mbisin ak Mbisaan laay wax. Danga mel ni ku ma déggul, Biige. Lu la dal tey ? - Yaasin Njaay a sax, de. - Biige Sàmb, lu la dal...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_472
Du yaa ngi fàttaliku bés ba nu gungejee Asan Taal ayeropoor, muy dem Tugal ne day futbali Màrsey ? - Yàgg na lool, waaye mu ngi mel ni démb ci man. - Nekk nanu fa di jooyoo maak moom, yëf yi takkarnaase, nuy fóonante ba nit ñi faf mujjee noo wër di nu seetaan. Yaa ngi koy fàttaliku, de ? - Bu baax, sax. - Wa...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_473
- Lu la Asan Taal tontu, Biige ? - Asan Taal dafa siggi, sunuy bët daje, sama fit ne rës, Ngiraan. Waaw. Ca laa sog a xam ne naaféq tigi laa jébbaloon sama bopp. Booba ba léegi maa ngi daas sama paaka, xam ne bés dina ñëw, ma fey Asan Taal boram. Mu ngoog, Ngiraan. Sa doom ji wor na ma, wax naa nit mu alag ki ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_474
- Bëggoo koo gis, xanaa ? - Yal na ma ko Yàlla xañ ba fàww. Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski séen leen, mel ni ku tiit moom itam, gaawantu delloo buntam.Noonu, ñu déggaat Aram muy yuuxu : - Wóoy sama ndey ! Wóoy sama ndey ! Waa Ñarelaa bàyyeeti lépp lañu doon def, daw wuti sa kër Maam Ngiraan Fay. Géew baa ngi të...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_475
Bésub alxames la woon, bi timis di waaj a jot. Ba nu demee ba jub tali Ngaala Jóob - mooy jàddukaay bi mujje ci yoonu ayeropoor - lanu dajeek mbooloo mu takkoo-takku, kaar. Xanaa waroon naa tollu ci ñeent mbaa juróomi-téeméeri junniy nit. Ñii a ngi waaxu, ñii di xélu, ñaq bay siit, ñi ci des dugg ciy kaar-ràppi...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_476
Béréb bi Ngiraan ubbee, laay daaneele, man Aali Këbóoy. Du nag lu ma taamul sama bopp : mbir mee deme noonu rekk. * * * Ayeropooru Ndakaaroo ka bare nit tey jii it, kaar ! Noo yaakaar ne noonu la nit ñi tollu rekk, romb na koy wéy. Nit ñi war nañoo mat xanaa juróomi-téeméeri junni ak lu topp. Lu xew ba ta...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_477
- Loolu da koy yàggal ! Am na lu gën a gaaw ! Waa ji wax loolu tàmbalee sànniy xeer ci garab gi, gone yi topp ciy sànniy xeer ñoom it. Njiitu takk-der yi dawseek liifam, ne leen ñu dakkal li ñuy def : - Dañuy aaye ku fi sànni xeer. - Baal nu de, seef, xamunu ci woon dara.Alkaati bi ñaan fa sigaret, ñu faf lal ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_478
Takk-der bi reetaan : - Mu ngoog de ! Ba ñuy nemmeekuy kayitam daal, la ne tirr daw ! Booba ba léegi ñu ngi koy wër ! Waa ji mayoon alkaati bi sigaret daldi ne : - Kon li ñu naan dafa soppeeku golo du dëgg ? Alkaati bi kimmi sigaretam, téen, sànni saxaar si, xool waa ji, muuñ : - Noo mënee gëm waxi dof yooyu, y...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_479
Kaay jàng ! Kii ak turam wu gudd wii moos, juddoo Burgoñ, bokk fa ci kër gu mag sax, dégg naa, na mu mënee nekk sa Yaasin Njaay moomu ? Werante bi neeti kur. Tuuti kon yëf yi ëpp loxo. Suba su waa Ñarelaa yeewoo, yëf yi gën a takkarnaase ! Badu, li nga wax keroog Abdel Kadeer Maxjub dëgg la : du gox bi rekk a ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_480
- Kenn du ma nettali lu kéemaanee noonu, fàww ma gisal sama bopp Tubaabu Ñarelaa bi ñuy coow. Dëkk bi yépp riirandoo, jëmsi Ñarelaa. Waa Ndakaaru Njaay a bëgg xew ! Fan yii de, foo sànni mbàttu ci Ñarelaa mu tag. Saay-saayu Ndakaaru yépp làngsi nañu ci gox bi. Du benn du ñaar nit xëm na fi mbaa ñu jàpp fi sàcc...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_481
Am xaat ñuy siisaate. Man de, Badu, bett naa fi ay boroom kër ñu naan : - Ku dëkkul Ñarelaa amoo dara looy wax ! Nun, xam nanu lu tax Yàlla wàcce fi ndaw sii.Waaye séytaanee teg loxo ci Ñarelaa, fan yii. Mbedd mu ma jaar, dégg kuy rëbb jeegu Tubaab bi : - Waaw, ana mu sax, moom ? - Wëey ! Na génn, nu gis ko ! ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_482
Sunu gan yi dañoo mujje di fanaan ci mbedd mi. Foo walbatiku dajeek ñuy yalwaan walla ay jaaykati ndox mu sedd mbaa bisaab ; waaraatekat yiy wër Ñarelaa, naan : - Waay, ku lii doyul lu lay doy ? Am ñu yore nataalu ndaw si di ko jaay : - Mu ngi. Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski la tudd ! Werante gis bokku ci ! ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_483
- Yéen kay, la kenn waxul dara ! Ku leen romb, ngeen tàllal ko nataal bu wuteek ba ca des, te ne yépp benn nit ki la ! Yabaate ba dee ! Ñu songoo, kurpeñ yi dal, ñii far fii, ñee far fa ca des. Mag ñi di leen yedd, nag : - Yëf yi xéewal gu fi Yàlla wàcce la, jarul a xeex ak a xuloo ! Su ngeen àndeek seen sago, ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_484
- Xanaa mook ñaari doomam yii dinañu lekk ! - Ay doom laa déggam ? - Waa-waaw ! - Doom yu mel nan ? - Ñoo la gën a ñuul sax, de. - Tubaab bu weex ak ay doom yu ñuul laa dégg ? - Kii du nit ku baax ! - Lu nuy xaar ? Nanu dàjji bunt bi, waay ! Benn góor gu màggat ñëw ni leen : - Déet doom, yoonu jàmm sorewul. ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_485
- Réew mu tollu ni Farãas amul lu muy def lu dul di sonal boppam ci ab lagara doηη ! - Tubaab yi tal nañu leneen ! - Ndegam du dëmm sax, ndaw sii ! Waaye gone yooyu, Yàlla mi dul faral kuy tooñ, moo leen daldi tiiñal ci saa si. Fa ñuy kókkëlee góor gi, di kex-kexi, la daldi am ñu agsi booru kër Ngiraan ak se...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_486
Badu, su doon sama sago, dinaa la nettali li fi xew ba jeexal te duma la ne bakkan rot na fi. Mënuma ko, ndax wax la dëgg moo ma war. Loolu laa dig Ngiraan Fay. Keroog, dëggaate nañu ci buntu kër gi fukki nit ak juróom-ñeent, ñu daldi faatu ci saa si. Monte de, buuxante mënoon na cee bañ a am. Nit ñee tiitoon se...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_487
- Nu ngi leen fiy xaar, maak samay nit. Buleen yàgg, nag.Bi ñu ci tegee genn- wàllu waxtu, yeneen soldaar agsi ci gox bi.Waaye ñii ñoom, ay Tubaab lañu woon. Seen njiit jubal ci njiitu soldaari Daawur Jaañ yi. Ñu gise ñoom ñaar gise bu gaaw.Tubaab bi ne Biige Sàmb : - Madam Mari-Gabriyelaa Won Bolkowski laa jëls...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_488
Fekk na booba Mari-Gabriyelaa ngi làqu woon ci wanagam, mook doom yi. Naka la yërndu ba xàmmee ñi ko doon jëlsi, daldi daw fekki leen ci saal bi : Booba ba léegi maa ngi leen di xaar ! Su ngeen doon yéex, ñuy taal kër gi ci sunu kow ! Tubaab bi ni ko : - Mbaa noppi nga rekk ? Ambasadeer baa ngi lay nég sa màk...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_489
Soo gisee njiitu soldaari Tubaab yi, mu ngi mer ba funki. Mari-Gabriyelaa xam ne fa ko Biige Sàmb ak Sinkun Kamara dugal, caaxaan génnewu ko fa. Mu ni Tubaab bi : - Ñaar ñii maa leen jur ci sama biir bii ! - Xool nga leen bu baax ? Noo mën a juree ñii ñaar ? Mbisin ak Mbisaan seen bopp ñu ngay jooyoo, di gën a...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_490
Mu neex la, mu naqadi la, dinaa ko def ! Soo demee foofu nga wax fa sa waxi kasaw-kasaw yii ba xam ndax dinañu la faale ! Soldaar yi mu àndal xaw a mel ni ñu yërëm ñaari gone yi. Mu xulli leen : - Lu ngeen di xaar ? Gàdduleen ko laa wax ! Ñu ne kirtim Mari-Gabriyelaa, muy wéqu, di saaga soldaar yi, di leen ga...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_491
- Waaw. Sinkun Tiggide Kamara. - Lu ma la def ? Wóoy man ! Loo ma bañee nii ? - Lii lépp yaa ko teg sa bopp. Kenn rekk laa ci soxla woon. Léegi dinga ñàkk buubu, ñàkk ceen ga. - Yërëmal boog gone yi. Ñoom doonuñu ci dara. - Xanaa gëmoo li ma la wax, Mari- Gabriyelaa Won Bolkowski ? Nee naa la doyewuma leen da...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_492
Sinkun Kamara walbatiku, daj ci Biige Sàmb, ni ko : - Yewwi ma boog, soxna si. Biige Sàmb xool ko, yëngal ndànk bopp bi. Sinkun Kamara xam li mu ko waxul, defaraat kaalaam, dëngalu dem yoonam. * * * Dinga ma ne : - Waaw, bi loolu yépp di xew, fu Ngiraan Fay newoon ? Muy it laaj bu am solo. Soo dellusee,...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_493
ñaari doomi golo yi kenn ci nun masul a gis, di leen móolu, naan leen nañu dellu ca àll ba mbaa ñu dem fekki seen ndey Toolu- Buur, ca Guy-Géwél, guddi googu lanuy door a leer ne Ngiraan Fay àndatul ak sagoom, ndeysaan. Waaye gaaw a wax baaxul. Ñàkkul mu amoon lu feeñu Ngiraan, booba. Ndax lii moom, kenn du k...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_494
sa maam Ngiraan Fay tàggoowul benn yoon ak sagoom. Ci li ma mën a seede de, ba mu fiy jóge xelam daloon na. Bi nuy diisoo nun ñaar la soldaari Daawur Jaañ yi dellusi Ñarelaa, ne dañu leen ne am nay saay-saay yu fi làq ay ngànnaay, di waaj a song nguur gi. Coow li neeti kurr : - Ay gànnaay, fii ci Ñarelaa ? ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_495
Maak Ngiraan a ngi janoo, nuy dégg ni saar de kombaa yiy wëree Ñarelaa ak ni bomb yiy kalaatee : Rëll ! Rëll ! Rëll ! Mu xëcc sama loxo, tari Alxuraan. Benn bomb rajaxe asamaan si.Ngiraan muuñ, tudd turu Yàlla, gërëm ma, gëmm. Ba ko waa Ñarelaa di robi, romb nañu ñaari doomi golo yi ñuy xëccoo benn welo bay ...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_496
Ca armeel ya nag, man Aali Këbóoy bàyyi naa naaféqi Ñarelaa yi ñu wax seen waxi caaxaan ba noppi, ma door a yëkkati samay kàddu ba ca kow, xalab leen ci biir géew bi. Ñoom ñépp ñu téenandoo di ma seet. Kenn ci ñoom gisu ma ci, waaye ñoom ñépp xàmmee nañu sama baat, man Aali Këbóoy. Duma jaaraat nag ci li ma...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_497
Téereb Dóom. Téereb Ngelaw. Téereb Lëndëmtu. Téereb Fent. Téere bu Ñuul bi. Téereb Wis. Fàttewuma Téereb Ndéey. Su wesoo Ngiraan mi ko bind, keneen warul a xam lan moo làqu ci biir. Waat naa ne man mi la ko fiy dencal sax, duma juum mukk ba ubbi ko. Waaye téere yooyu yépp nag, bés boo dellusee, bala nga...
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_498
Domi golo audio numerique Developpé par allowow  Editions Audio Numérique Ebook Africa
DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf
page_1
ANTOINE DE SAINT-EXUPÉRY Wolof Ndoomu Buur Si
Ndoomu Buur Si.pdf
page_5
Ndoomu Buur Si
Ndoomu Buur Si.pdf
page_6
Foog naa dafa làngaamu ci picc yuy roñu ngir mën a rëcc.
Ndoomu Buur Si.pdf