language
stringclasses 1
value | speaker_id
stringclasses 3
values | prompt_id
stringlengths 4
4
| prompt
stringlengths 15
110
| segment_id
stringclasses 5
values | audio
audioduration (s) 2.27
69.4
| duration
float64 2.27
69.4
| raw_text
stringlengths 24
1.23k
| iso_639_3
stringclasses 1
value | glottocode
stringclasses 1
value | iso_15924
stringclasses 1
value | id
stringlengths 36
36
| parent_id
stringlengths 36
36
|
|---|---|---|---|---|---|---|---|---|---|---|---|---|
wof_Latn
|
spk03
|
f026
|
What are some foods that can cause bad breath?
|
s01
| 19.944
|
Waaw, lekk biy teey sa xel bi ni moment bii mooy déget nii nga toggu ko, léegi togg bi ñorut. Léegi boo ko lekkee mën na teey sa xel bi walla cere bi ëpp laalo. Bu ëppee laalo rekk, boo ko lekkee mën na teey sa xel walla nga ut meew boole kook bu ëpp laalo. Loolu it mën na si teey sa xel.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
5f862088-92ef-470d-bfd1-0964befdbc41
|
5f862088-92ef-470d-bfd1-0964befdbc41
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
h107
|
What purpose does soap serve?
|
s01
| 14.828
|
Saabu dañ koy fóotee, mun naa sangu ak raxas. Mun naa fomp it waaye duñ koy deferee ndax saabu tomb bi rekk dañ koy deferee ak xeme ak xolliti gerte. Waaye bu tubaab bi moom xamuñu nuñ koy deferee.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
619e6cc0-a3f0-48ee-8b79-16f67efb0749
|
619e6cc0-a3f0-48ee-8b79-16f67efb0749
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h103
|
What purpose do passports serve?
|
s05
| 4.373479
|
Mooy defer réew, mooy dimbale réew. Salaamaalekum.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
6ae7e544-1c7f-47af-b551-d82162c2b513
|
6ae7e544-1c7f-47af-b551-d82162c2b513
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
f025
|
Are there any foods that are believed to help improve strength?
|
s01
| 22.376
|
<noise> cere bi cere bi baax na, cere bi si dugub. Dugub bi dañ koy bay. Cere boobu itam baax na ak meew mi. Meew mi, meewu nag la dañ koy rahatt. Boobu it baax na. Yàpp wi itam; moo xam yàpp bëy la walla nag yàpp wi tam baax na.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
a5572121-0368-4588-a01c-36071d4ba3af
|
a5572121-0368-4588-a01c-36071d4ba3af
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
n070
|
Please say the names of the days of the week in order, starting from Monday.
|
s01
| 4.944
|
Altina, talaata, àllarba, alxames, ajjuma, samdi, dimaas.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
72edb366-a0ef-48b3-8e83-d3d1c75ed044
|
72edb366-a0ef-48b3-8e83-d3d1c75ed044
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
i055
|
Can you explain how to wash your hands properly?
|
s01
| 25.956
|
Waaw <hesitation> raxasee sa loxo, su nekkee loxo bi daa tilim bo, mun nga njëkke suuf bi. Boo njëkkee suuf bi bomb sa loxo yi bomb ba ŋa xam ne sa loxo yi dañ na, nga raxas ko. Léegi jël ndox boo xam ne mingi am ordusawel ak omo nga raxas sa loxo yi ba sa loxo yi set nga jël ndox bu set lahandee ko. Boo ko lahandee ba pare, léegi mun nga jël sa musuwaar nga fomp, fomp loxo yi ba nga xam ne tooy bi deñ na.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
f9c863f6-bb48-4a4b-876e-4b1522c0ec98
|
f9c863f6-bb48-4a4b-876e-4b1522c0ec98
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
m007
|
Name as many colors as you can.
|
s01
| 21.172
|
Bula am na, ñuul, werta, xonqu, weren, móof, dingiri ak sokolaa. Dóom-taal am na. roos. Defe naa yooy laa xam de.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
d6889e85-0a03-4387-98b8-a93cc66e77ae
|
d6889e85-0a03-4387-98b8-a93cc66e77ae
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f002
|
What are some foods that are really simple and you enjoy a lot?
|
s01
| 29.72
|
lekk yi nga xamante ni su ma ko lekkee damay sawar dafa yëngu mooy fruits <noise> yi nga xam ne dafay ñor fii nii comme guyave, comme mandrine, comme mango, comme oraas, nekk na si lekk yi ma neex, ñoo xam ne su ma ko lekkee damay am cawarte, waa damay am cawarte te yomb na lool jefewut fii nii bu baax parce que dañu koy béy suñu àll yi, dañ koy dafay ne dañ koy jiw suñ kër yi, dafay ñor nga dem waaxu rek witti, ñëw raxas rek lekk, loolu rek nga ciy am. Te su ma ko lekkee dama ciy yëg sama bopp bu baax, dama ciy kontaan bu baax ndax doon na doon na ay fruits yi nga xamante ni neex nañ ma lool lool.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
52d1f263-1dd0-44ef-8db7-2a1f08343e69
|
52d1f263-1dd0-44ef-8db7-2a1f08343e69
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
n029
|
How many countries have you visited? Please name them.
|
s01
| 21.608
|
Bi ci jëkk mooy dem naa senegaal, <hesitation> dem naa kaasamaas, <hesitation> dem naa gine ak gàmbi gii ma dëkk.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
3dd7e527-1d79-4468-abed-76ae7290d523
|
3dd7e527-1d79-4468-abed-76ae7290d523
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
f024
|
Are there any foods that are believed to help improve eyesight?
|
s01
| 16.216
|
Xam nga karoot day yokku leeraayu bët, te karoot dañ koy bay ci suuf bi. Ci suuf bi lañ koy bayee. Meme nawe it baax na. Nawe it ñu ne day yokk leeraayu bët, te boobu dañ koy bay. Ci suuf bi lay jugee.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
7a0f5c5f-837f-44b7-805d-a1121b74ad28
|
7a0f5c5f-837f-44b7-805d-a1121b74ad28
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
n071
|
Please say the names of the twelve months of the year in order, starting from January.
|
s01
| 9.004
|
Léegi hore, diggi, tabaski, tamxarit, diggi gàmmu, rakki gàmmu, rakkaati gàmmu, maamu koor, ndeyu koor, baraxlu, weeru koor.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
aa542b6d-4fec-419b-bbfe-9103c89554aa
|
aa542b6d-4fec-419b-bbfe-9103c89554aa
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
i051
|
Explain how to do laundry by hand.
|
s01
| 27.208
|
<hesitation> lañ doon fóotee loxo dangay def saabu. Boo defee saabu, julli ba pare. Su nekkee bànku ngay fóote, nga téye si bànku bi. Boo téyee si bànku bi ba pare nga doog ko fete sa loxo yi boo ko fetee sa loxo yi ba pare dugal wañ dugal si beneen ndox bi; bu nekkee dangay fóotee bànku. Boo fóoteewul bànku moom, sa loxo yi nga jël di fete, di fete bam mummaa mi set nga doog a kii.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
882454dc-2f1f-4148-b86e-c97d135e1541
|
882454dc-2f1f-4148-b86e-c97d135e1541
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f084
|
What different types of vegetable oils are there, and how are they different?
|
s03
| 19.663521
|
Noon la ko defee ca garabag teŋ ga, noon la ko defe ca garabag <hesitation> new ga, ci yi nga xam ne ñun suñu xam-xam àgg na ca ci suñ lëññëtu, bañ xam ne yii dafay génne diw, diw boo xam ne lii la ak lii ak lee te benn bokkut ci sa moroom wàntu yépp diw lañ, te benn bu nekk am na lu moo def si biir jëmmi doom-aadama <noise>.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
23056115-f253-48ac-b1cd-c5bc53336c7e
|
23056115-f253-48ac-b1cd-c5bc53336c7e
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f025
|
Are there any foods that are believed to help improve strength?
|
s03
| 10.085042
|
Loolu mooy li ma xam ne, loolu laa xam ci li ñoo dunde suñ ko doon def dañ am wét-gi-yaram, <unintelligible> te buñ amee wét-gi-yaram, am kàttan buñ amee kàttan man a lëggéey. Buñ lëggéeye man a hoor.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
fbad68f8-29e9-4213-8caa-b3b7315dac8d
|
fbad68f8-29e9-4213-8caa-b3b7315dac8d
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 28.188
|
<noise> bànk de denceekaayu xaalis la comme ça léegi yaw boo amee xaalis, wóoluwoo koy denc si kër gi, léegi mun nga koo yóbbu si bànk bi, denc ko fa. Léegi boo amee soxla nga xam ne soxla daa taxaw, léegi man nga dem récupérer waat xaalis bi, ñëw fajee sa soxla. Saa soo amee nag, nga dem yóbbu <hesitation> denc dencaat dencaat ko foofu noonu. Loolu mooy bànk pour denceekaay xaalis daal la.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
af518af7-53eb-4b23-82c9-24ee31a5329e
|
af518af7-53eb-4b23-82c9-24ee31a5329e
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
m009
|
Name as many types of trees as you can.
|
s01
| 11.296
|
Màngo am na, kaasiyaa, darkasu, guy, dittax, kabaa ak ban? Am na beneen de.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
bf5c39c4-156c-425d-a3bd-8dd34c4513c7
|
bf5c39c4-156c-425d-a3bd-8dd34c4513c7
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s03
| 2.265354
|
Balaa jot dana yàgg de.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
1ede33b2-a3cb-4973-994c-760f44ced584
|
1ede33b2-a3cb-4973-994c-760f44ced584
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 23.9025
|
Waaw doomu aadama, kii lim laaj mu ne ndax nit mën nay dundu <hesitation> ba ci, ci waxtu wu nekk rekk, mu ngi dal, waxtu wu ne mu ngi féex, waxtu wu nekk rekk dundëm mingi correct. Waaw <hesitation> jikkoom la laaj nde yaw loolu nga wax noonu, nit moo koy am waaye ci jikkoom la koy amee.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
97f96749-6990-4e1e-8180-68306afeb2b5
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 5.960625
|
Jikko bu baaxee rekk, léppam baax na. Su bonee, boroom, léppam bon na.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
b4b0cba4-0698-46d1-99f8-632d7cd1cb2e
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 8.160875
|
Kon ci tontu bu gàtt mooy ku baax jikko daal, danga dem ba sa dundu neex ci boor bu nekk. Ndeg lan?
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
7643ea74-8432-40cc-8e43-6c9244ef787c
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 8.780938
|
Ndeg melow jikko ji nga ame de ko dundee, moom moo jaarele dundu sa diggante ak képp koo digaale. Ba tax na, mu rafet.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
987553ff-a7b8-4cb0-aa5d-1fcb88dd4922
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 9.621
|
Donte sa jikko dafa baax rekk, koo séqal rekk la nga séq ak moom lu baax laay doon. Te séq ak nit lu baax lu bon da ca génn. <hesitation> te la bon mooy waral xat.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
d40456b0-4cea-4290-afdd-d11ca9fcfc5f
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 9.841063
|
Mooy waral ham foo ñimee dem ak foo ragal a dem, ham ko hóolu ak koo hóoluwul, ham koo bëgg ak koo bëggul, ham ku la héene ak ku la héenewul. Loolu la koy def mooy jikko ja.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
b0dbcf15-1c72-4f80-aab6-efbe81b609f1
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 6.140625
|
Moom nam la xamee, noonu la lay jàppee. Soo ko wanee ni gën ci melo yi, mu jàppe la jàppin wi gën si jàppin yi.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
a496d764-2326-4c8a-95a5-1595bbc07322
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p116
|
Is it possible to be completely honest all the time?
|
s01
| 3.400375
|
Loola, bu dee ci iir gi nga dëkke, yow dinŋ fa man a dundu ci jàmm.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
64245ef4-cb14-47db-8b67-9ea9c3b90d36
|
02fa4d27-0d23-4110-a859-7ea884337070
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f016
|
What are some traditional dishes from your culture that you love?
|
s01
| 69.416
|
ñun suñ cosaan bu dee ñun suñ cosaan lu ma ci gën a bëgg mooy suñu dignité yi nga xamante ni amoon nañ ko, suñuy dëkku yi nga xamante ne nekkoon nañ si ñun, suñu njàmbaar ak suñu bëgg a liggéey ak suñu bëgg suñu bëggante suñu biir daal loolu bokk na ci li nga xamante ni dina ma di touché toujours maanaam sama cosaan man loolu damay toucher toujours sama cosaan. Ndax ñun suñu cosaan daawuloo ànd ak sa rakk walla sa mag dem àll mu dee nga ñibbi si ñun kilifa daanul am, daanuloo mukk dëkk ak sa mag walla sa rakk walla sa doomu nijaay walla sa doomi bàjjen ba tolof-tolof dal ko nga mu muy muy dëkk si ay coono te ma mën ko cee dindi, nga mën ko si xettali ba pare di ko seetaan, loolu amutoon ñun askan, bokk na ci mbir mi nga xamante ni nag daanaka ci jamono tey jii jikko yu mel noonu dafa commencer jeex waaye mu ngi des ba léegi daal waaye bokk na si jikko yi nga xamante ne nekkoon nañ ci suñu cosaan ñun, nekkoon na suñu biir askan yi mu doon jikko yi nga xamante ni neex na ma lool, mu doonoon ay qualités yi nga xamante ne neex na ma lool, te man toujours damay toog sama xel di ci nekk ma ciy kebetu toujours di ci waxtaan toujours pour ñu mën ko delloo ci suñ biir dund gi ndax lu amoon njëriñ la si biir dund gi.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
37f8eb70-4c66-42d1-96ca-5a2d974988e9
|
c6335317-b088-4a0a-9ce4-cf0954f3de23
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
n022
|
How many different languages do you think there are in the world, approximately? It’s OK to take a wild guess.
|
s01
| 29.247875
|
Waaw li nga xam ne jëlee ci jàng ñu waxee ñu ko ci téere, ci yépp làkk yi yàlla def ci kow suuf, wax nañ ni mat na junney làkk. Te junney làkk yooyu yàlla bind na <noise> ci doomu aadama yi, giir yépp, bu ci ne am na giir guy làkk làkk woowu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
57bf050a-1cb2-483c-9c6f-b2dddd1ecd46
|
02423ec2-90be-45e5-82dd-aaeb0290c784
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
n022
|
How many different languages do you think there are in the world, approximately? It’s OK to take a wild guess.
|
s01
| 5.681563
|
Mboolem ni làkk yi tollu. Loolu dey téere moo ñu ko sool.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
f4409628-e678-4978-b7b5-de9fc2659d4f
|
02423ec2-90be-45e5-82dd-aaeb0290c784
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
n022
|
How many different languages do you think there are in the world, approximately? It’s OK to take a wild guess.
|
s01
| 24.286563
|
La ko dalee ci aadama aleyhi salaam, ba ci fiñ tollu nii di wax man ak yaw, li fi ne ci làkk ci kow suuf ñi ñooy tudde doomu aadama di ko wax, te yàlla moo leen ko jox mat na junney làkk. Lii dey lii de jàngee nañ ko ci téere, ñu wax ñu ne nii la ko yàlla tërële.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
42474083-3d22-46a0-b2bf-3074514fefc2
|
02423ec2-90be-45e5-82dd-aaeb0290c784
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i043
|
How would you cook chicken?
|
s01
| 14.922563
|
Waaw mu ne dafa laajte naka lañuy toggee ganaar. Ñun, li jëkk ci ñun ci ñun ni ñuy toggee ganaar mooy gannaaw bu ñu ko rahee ci turu yàlla nde diine islaam jiñ nekk.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
c88e74c6-4840-4e1f-ad89-85d985ee784a
|
44caeb16-e6d0-4efc-a3f3-c16cdaebe8ef
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i043
|
How would you cook chicken?
|
s01
| 9.98175
|
Dañ ko war a xotti, génnee la ca bokkut. Door koo jox jigéen ji koy suqi.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
002869ea-28f8-4e8c-b7e4-7ce80b480050
|
44caeb16-e6d0-4efc-a3f3-c16cdaebe8ef
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i043
|
How would you cook chicken?
|
s01
| 9.241625
|
Mu door koy <hesitation> tàngal ndoxam, soode ko, fekk génne nañ lépp lu neen ca biir ba ci sobe. Ñu raxas ko bam set.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
f72912ff-6c0a-4478-b514-1c9194068bec
|
44caeb16-e6d0-4efc-a3f3-c16cdaebe8ef
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i043
|
How would you cook chicken?
|
s01
| 10.801875
|
Lee-lee ñu def ko togginu, ba war ci toggin di cee toggee ñam wim bëgg mu baax. Yam ca war a boole, mu boole ko ca ci lu dagan a lekk ñu boleente ko.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
342beeca-dca7-47f7-887b-94f93108bd86
|
44caeb16-e6d0-4efc-a3f3-c16cdaebe8ef
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i043
|
How would you cook chicken?
|
s01
| 17.062938
|
Bu boobaa lekk ga dana am njariñ, te doo ci jële feebar, te boo ci jëlewul feebar rekk wér la laay yokk. Ñun ni ñuy toggee ganaar mooy daal, gannaaw bu ñu ku rendee ci turu yàlla, génne saleté ba ca biir, ba pare door ko df suqi ba mu set ñu jënd, jigéen gi moom ci boppam defar ko.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
dc9cdb98-1568-44d1-b9b0-6a71a0f07629
|
44caeb16-e6d0-4efc-a3f3-c16cdaebe8ef
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i043
|
How would you cook chicken?
|
s01
| 7.36125
|
Dindi lépp luy der ba ca kow, mu des yàpp wa, mu togg ko na mu ko war a toggee bam mat, su pare ñu man ko lekk. Ñun noon lañay lekkee ganaar noon lañay lekkee ganaar.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
6fa06645-161c-4c9b-979c-1b65985622db
|
44caeb16-e6d0-4efc-a3f3-c16cdaebe8ef
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s01
| 15.74325
|
Waaw laaj nga laaj bu am solo bu dëppoo ak dundu giiñ tollu. Fowwu njiit di ham ci kër, ci dëkk, ci tundu, ci réew.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
402c881a-aa2e-4b02-bbf6-d4b792d66119
|
faeac544-55b4-4728-be20-8a1ee64abaf9
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s01
| 20.304188
|
Njiit bu ci ne dëppoo ak ñam jiite lu ko war la, ñoom it ñu dëppoo ak ka ñu jiital, ñoom mbooloo ma lu war la. Kon liy njëkk a defar kër mooy dëppoo.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
fcbbb3d2-6bd7-4d1b-9e40-bad75ec8579f
|
faeac544-55b4-4728-be20-8a1ee64abaf9
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s01
| 15.443188
|
Dëppoo mooy ànd, bokk pas-pas. Loolu mooy dëppoo ci lëggéey ba ak lu ñooy rafatelee lëggéey ba ak lu koy sakkanal ak lu koy saxal ca barab ba.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
150d7dac-75b6-4c95-a660-468943505ecf
|
faeac544-55b4-4728-be20-8a1ee64abaf9
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s01
| 25.865313
|
Loolu bu ko kër ga defee, koñ ba def ko, dëkk ba def ko, tundu wa def ko, gox ba def ko bam daj réew ma defe ko. Liiy yokk am-amu réew mooy ñépp lëggéey te bañ a yàq ak lëggéey ba nga jàng ba man ko bum man a doon donte yaw mi toog ci taabal ji ngëb pen bi.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
c1a3912a-594c-4dc1-b211-dfff9bb53fe9
|
faeac544-55b4-4728-be20-8a1ee64abaf9
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s01
| 6.721375
|
Nangul sa lëggéey boobu te teg ko ci njub. Sa pen boobu dana yokk lépp luñ bind.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
27926189-f38a-4ee3-bdff-b1d3ea28e397
|
faeac544-55b4-4728-be20-8a1ee64abaf9
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p096
|
What is the role of government in economic development?
|
s01
| 5.281063
|
Dana yokk ci yow, yokk ci réew mi ngay bindal ndeem yaaŋ ko teg ci njub.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
6e7c59b2-00eb-45f4-84c6-7cbfbf0fa341
|
faeac544-55b4-4728-be20-8a1ee64abaf9
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f012
|
How long can you keep vegetables before they are dangerous to eat?
|
s01
| 42.209375
|
Waa lejum yu mel noonu nag denc leen lu yàgg te yàquwuñu loolu jafe na lool, waaye nag jamono dox na ba ay jumtukaay génne nañ li nga xamante ni dañ ñuy dimbale ci suñ dund gi, ndax yàlla moo waxoon ne dinaa def ci xelu doomi adama <hesitation> benn xarañteef, xarañteef boobu nag moo ñëw ba liggéey ay jumtukaay yi nga xame ne nit da koy mun a denc lejum yu mel noonu diir te du yàqu. Benn lejum lañ daan mën a mën a denc lu yàgg te du yàqu ñu ko daan tuddee pataas, moom daal bu mosoon a su- gas lu melk ne pax bu ndaw nga def ci salañ nga tooyal salañ ba tuuti ba m bam bam bam ba mu ba mu guus nga def ci palaas bi ba pare sottiwaat salañ ci kawam, moom daan na mën a nekk foofu noonu ay weeri weer weeri weer weeri weer te du yàqu, moom daan nañ ko dencee noonu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
391672e0-cd8a-41e4-bf60-498a950a19d1
|
85c084d8-02e1-4f2e-98c8-066ed51898c3
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f012
|
How long can you keep vegetables before they are dangerous to eat?
|
s01
| 11.762625
|
Daan naa gis suñuy waajur yi daan ko <noise> denc noonu lu yàgg te du yàqu. Waaye bu demee comme su- ay supame yu mel noonu yooyu ci frigo rek nga leen mën a def ñu yàgg te du ñu yàqu, waaye boo leen dencee ci bërëb bu bërëb bi yenn bërëb yi dañuy yàqu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
cde5acd9-738a-485f-b179-74b6469838df
|
85c084d8-02e1-4f2e-98c8-066ed51898c3
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f012
|
How long can you keep vegetables before they are dangerous to eat?
|
s01
| 18.024
|
Bu dee heure(u) sedd lañ ñor nag mën nañoo dem ba weer du ñu yàqu boo leen dencee palaas bi nga xamante ni newuñ ci biir saako walla ñu teglantewuñu lu bari maanaam nga teg ko moom kenn bërëb tegaat beneen moom kenn bërëb tegaat beneen moom kenn bërëb, bu dee si palaas bu wow la ba pare sedd gi di ko laal mën naa yàgg foofu noonu te du yàqu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
baae9da5-af30-4672-a69e-0dbee3686e8a
|
85c084d8-02e1-4f2e-98c8-066ed51898c3
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f026
|
What are some foods that can cause bad breath?
|
s04
| 25.806313
|
Ñun liñ hamoon mooy keŋkilibaa, mbor-mbor, lëng, xobi rat. Yii lañ daan def kafe ba léegi, boo feebaree feebar yu sew yi ay siddit aki ay soj aki kalab-kalabi ñu ni hutal ngeeraan, hutal xobi rat naan <hesitation> , jëlal <hesitation> nga boole yooyu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
538fb6bc-e639-4c3d-90fa-8cf5b016ea61
|
c87dffd4-d5a8-4e3e-98d7-f0927a2794fc
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f026
|
What are some foods that can cause bad breath?
|
s04
| 10.2625
|
Boo koy jefëndikoo; lii nga naan, lii nga sangoo rekk yàlla wéral la. Buñ doon tànn nag tay, bugg a delluwaat ca la mag ña hamewoon, bind bañ ñu binde nii moo di biñ bindoon mag ñi.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
d6ff7225-44dc-47d8-9e05-7c72f5977881
|
c87dffd4-d5a8-4e3e-98d7-f0927a2794fc
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f026
|
What are some foods that can cause bad breath?
|
s04
| 5.521375
|
Mag ñi ñoo wér rekk. Li ko ceeñ mooy li ñuy lekk moo bokkut ak la mag ña doon lekk.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
d5d70a81-0a10-4e84-9b70-26c47a93b37c
|
c87dffd4-d5a8-4e3e-98d7-f0927a2794fc
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f026
|
What are some foods that can cause bad breath?
|
s04
| 4.121
|
Fim ne neex na lañ topp waaye seetatuñ baax na. Lii mooy suñ probleme.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
618a2c20-7f87-40d6-957f-6d734dfa4e0b
|
c87dffd4-d5a8-4e3e-98d7-f0927a2794fc
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
f026
|
What are some foods that can cause bad breath?
|
s04
| 10.3025
|
Salaamaalekum. <unintelligible>
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
22989211-5f48-4225-96b4-fbdb6ae9a43b
|
c87dffd4-d5a8-4e3e-98d7-f0927a2794fc
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h103
|
What purpose do passports serve?
|
s01
| 21.5625
|
Waa passport dina di dimbale nit ci sa dem ak dikk na la ko de dimbale kon am na njëriñ ci dund doomu adama ndax dafay dimbale nit ci dem ak dikkam. Te dem ak dikk lu am solo la ci dund doomi adama, lu am solo la ci dund doomi adama, ndax li nga xamante ni moo jëng dund doomi adama muy xam-xam dem ak dikk dina ko di maye lu bëree bëri bëri.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
00bbeef6-20d5-4a05-b9c6-cccf81f756cc
|
5b0342dc-870d-49ae-bf89-608686b46442
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h103
|
What purpose do passports serve?
|
s01
| 18.982188
|
Ndax yàlla sax wax nañu ne dox leen ci kaw suuf ngeen xool man yàlla naka laa jëfee naka laa defaree man yàlla, naka laa tëralee, naka laa waajalee man yàlla, bu ngeen doxee ci kaw suuf nag dangeen ko gis. Te yu mel noonu ñooy yombal dox si jamono bi ñu toll nii ba foo dem ñu xam yow ban bërëb nga bokk, ban bërëb nga jó- nga ñjëkk a jóge.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
980b46d7-8b7b-466d-a80b-9feaab19fba5
|
5b0342dc-870d-49ae-bf89-608686b46442
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h103
|
What purpose do passports serve?
|
s01
| 29.243375
|
Te boo ko amee bërëb bi gallankoor bu la ci mën a dal bu fekkee dal na ci bu ñu ko xoolee dinañ xam ban dëkk nga, ban diw- ban bërëb nga jógee, te bu ñu yeggee ci bërëb boobu noonu dinañu xam yow yaay kan ak fan nga dëkk, parce que kenn ku ci ne ba sa dëkk sax fu ñu dëkk sax daf fay nekk sa turi gox, sa turi dëkk yëpp na fa di nekk buñ yeggee ci gox boobu noonu buñ laajtee dinañ xam ne diw kat fii la bawoo te dina di yombal dem ak dikk doomi adama, dina la yombal ci tolof-tolof bi la bu la dalee, kon lu bokk ci dund doomi adama la lu am njëriñ la ci dundu doomi adama.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
b2ee24ed-b4bf-45f6-b000-89cf8f34f94c
|
5b0342dc-870d-49ae-bf89-608686b46442
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 8.843
|
Waaw <hesitation> mu ni dafay laajte caabi naka la mën a ubbee karnaar. Waaw!
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
d0c4f8c6-4d60-4e8e-8901-14b5a2f9607a
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 17.365938
|
Xam-xam la bu réy bu fa nekka. Mooy rekk ki lëggéey <hesitation> karnaar bi bëñ yam def ca weñ ga, mu am weñ gi lu koy kii bam duggu fi mooy kalee, mu mën koo génnee fam kalee bam génn fam kalee, nu ube ko.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
0d621788-3c57-43f7-8f27-4cc4093f8217
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 10.1835
|
Bëñ yooyale moo da ma ne ak a. Ma ne feek waxoo a njëriñal wax du duggu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
f982aff0-dc1e-42a1-b2dc-c44b416cd7f0
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 10.483563
|
Bam jëlee caabi ja defal ko ñetti bëñ, fu moo duggu dafa am ñetti pax. : bëñ bu ne tollook pax. Bam àggee fam war a àgg it loola la fa fekk.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
074a8ca0-819e-4e0a-9b61-b19d1c12fd7a
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 3.841313
|
Bu waree dugël day dugël. Su waree génnee day génnee.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
5801ea1a-a7ed-4c44-99aa-3843b4c81039
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 16.0455
|
Loola moo de ma ne ak a xam-xamu wax door a jëriñ, ci li nga xam ne looloo waral caabi, boo ko dugalee ci biir xombu, boo wañee, bu fekkee caabeem la, day dugg, bëñ ya day korosante. Soo biijee pour mu téju dana téju.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
9a072b04-7a4e-486f-8ca9-bc50b765e089
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h092
|
Could you describe how a key opens a lock?
|
s01
| 3.381188
|
Soo biijee pour mu hubbiku dana hubbeeku.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
3834fe98-0e33-4ac4-973b-915427ac3040
|
b0b9291f-f016-404c-9069-4b458d85ef86
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 10.582063
|
Waaw, daf ma laaj <hesitation> ñu ni lan mooy bànk. Xam naa baat boobu sax moom waxi tubaab la.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
3bed0951-7957-415a-ae69-8ca3db50ecd3
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 8.181563
|
Waaye ñun lin xam mooy lan mooy pekk. Olof di ko wax pekk, te mooy bànk.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
94c568c6-46b1-4c56-be25-27b7b2d4e794
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 10.522063
|
Pekk mooy denceekaay, boo ko fa xësee def, yaw kepp a fay dem. Daŋ koy hub mu ne kepp.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
103eb0d0-aa4e-4cb6-8291-43874ea3d440
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 4.060813
|
Moom rekk a faay ne. Dara du ko fa jëlee ba nga soxla ko.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
70bc38cc-ca67-4a8a-94b5-880495aea4fb
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 10.962125
|
Mu tuddu denceekaay. Ñu tudde ko pekk ci mag ña, xam ne loo fa def, yaw mi ko fa def kuy jëli ji attaaya yaa koy jëli.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
b3f74241-fc43-43dc-9041-cc262b65b380
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 14.822875
|
Yaw itam noot nga sa bakkaan ba laŋ fa def doo ko jëli su dul fa ko jar. Lóola, mu doon njëriñ loo xam ne danga daan fekk, nit day dikk ak jaaxleem nga feyal ko soxlaam, te du xam foo ko jëlee.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
151b35a8-1cc2-42f2-b262-c5cc4032a178
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 13.762688
|
Demoo déeyook kenn, duggoo ci néeg keneen, seen néeg nga dugg génn fajal ko soxlaam, te bu duggee ci néeg bi du xam fi nga jëlee li nga fajee soxla fum ne. Loola moo tuddoon pekk, moom lañ doon def ko muy bànk.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
ebcdded6-5a2d-44bd-8722-ceceb693c3cb
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
h063
|
What is a bank?
|
s01
| 9.661875
|
Daŋ fa denc sa halala, nit dana la jox halalam nga nga denc fa keneen jox la keneen jox la ba mu man a mbooloo, te bu boobaa kenn ku soxla boroom <hesitation> bosom mu dikkee fekk ko fa, nga jox ko ko.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
9f5a4b29-b19c-4f90-b7a1-e685df06aef1
|
ee3d080f-b6ef-47ed-8f14-4befd1d24493
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f003
|
What are some foods that you enjoy a lot but are very expensive?
|
s01
| 28.805
|
bokk na ci lekk yi may gën a lekk ci di kontaan waaye dafa seer suñ fii nii mooy ndawal ak jën, ndax suñu géej gi daal bo mel na ni xamante ne mel ni ñun mel ni ñun dafa mel ni ñun réew mi moomatuñ ko léegi, ndax jën yu baax sax pour ñu lekk ko, dafay jafe lool. Ndax bokk na ci wér-gu-yara doomi yaramu doomi adama lépp li nga xamante ni dafay ñoree sa côté walla muy, mu, muy muy ñu fiy jógee fi nga dëkk nga koy lekk dafa baax si sa wér-gu-yaram kenn ku ci ne.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
18016d0b-2dbb-4988-82e3-860a5f3a74a3
|
0e812108-3576-42d2-b235-f98a202cf14a
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f003
|
What are some foods that you enjoy a lot but are very expensive?
|
s01
| 17.363
|
Waaye ñun li nga xamante ne mu ngi suñu côté ñu moom ko daal dafa seer seer gi nga xam ne naqari naqari gi nga xam ne dafa mel ni moomatuñ ko, moomatuñ ko léegi ñu jafe. Jën daal bokk na ci li nga xamante ni bëgg naa ko lool waaye seer na lool suñu réew mii sew te seer na fi lool metti na pour nga am nit am ko fii nii.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
22d970d0-ec68-4a3d-a70a-ec22328fd9ac
|
0e812108-3576-42d2-b235-f98a202cf14a
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
p056
|
What is important to learn about somebody before marrying them?
|
s01
| 17.467563
|
Waaw daŋ koy xool ndax seen jikko mën na ànd, nga jàngat ko, xool jikkoom ak doxalinam ak kii nan la man ak ci <hesitation> yan sãri nit la bokk ak ni muy doxalee. Loola it diŋ koy def.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
3d68033c-56b1-493e-8499-2a052c162313
|
eca392d4-4d26-4b78-bb3e-c6427712aa9e
|
|
wof_Latn
|
spk03
|
p056
|
What is important to learn about somebody before marrying them?
|
s01
| 19.568438
|
Soo ko jàngatee ba pare, léegi mën nga <hesitation> xool seen relation, seen diggante ba jàngat si lu bare après nag nga xool ndax <hesitation> sëy bi dina mën a nekk walla du mën a nekk balaa takk bi muy am. Su loolu yépp mënta nekk nag moom, soo yaboo nga xool leneen.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
62e6f5c2-779d-431a-88d9-12dbcf7942e5
|
eca392d4-4d26-4b78-bb3e-c6427712aa9e
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
a008
|
How do birds communicate with each other?
|
s01
| 13.821938
|
Nee dafa laajte ne picca dañ di waxtaan ak naka lañ di waxtaane. Mu ngi koy tontoo ci, njàngam téere waaye du xam-xamu bopp.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
dacd5a32-035a-4f1c-bc21-32f7508dfe34
|
737ce947-7603-42b7-a86c-a850eda7bab6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
a008
|
How do birds communicate with each other?
|
s01
| 42.585938
|
Picc day wax, comme ni doom-aadamay waxee, ndax wax nañu ne yónnent yi dañ daan wax ak picc yi ndax ñoo doon seeni yónnent rawati muhammad sallal laahu aleyhi wa salam mi nga xam ne moo mujj a ñów. <hesitation> niti yàlla yi ñu tuddee wëlliyu dañ doon wax ak picc yi, picc yi doon wax ñoom. Kon picc dana wax; lañ ñu ca leeralee, te alxuraam moo ñu ko wax, mooy picc yi, giir gu ne, giir picc yi, ña bokk giir yépp dañuy waxtaan.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
06c5c7d3-1b38-4bb7-be6b-277819578da1
|
737ce947-7603-42b7-a86c-a850eda7bab6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
a008
|
How do birds communicate with each other?
|
s01
| 12.901813
|
Waaye nag ña bokk giir la. Ñële pittax ñu- ñu- olof di ko woowe peket, seen giir la ñoomu neen fañuy waxtaan.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
aa40d96c-430b-410f-8366-8f7844a973e0
|
737ce947-7603-42b7-a86c-a850eda7bab6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
a008
|
How do birds communicate with each other?
|
s01
| 27.083813
|
Kër tan ñoomu neen fañuy waxtaan. Picc yu bare, am na yoo xam ne alxuraan moo leen tuddu, ba tax na ñu tëral seeni mbir ni ñu leen tërëlee ; lu mel ne xorondom, ñoom am nañu seef comme ni doomu aadama amee ay buur, ham arme comme ne nguuru àddina gi doomu aadama am xorondom am na ko ci biit xorom bi mu nekkee xorondom.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
f21408f0-9568-44e8-a395-dbd073ad8b8f
|
737ce947-7603-42b7-a86c-a850eda7bab6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
a008
|
How do birds communicate with each other?
|
s01
| 18.0025
|
Loolu lañu tuddee xorondom. Loolu tan yi am nañu ko; am nañu buuru tan, nga xam ne moom, bu waxtuw médd amee moom mooy njëkk a ñów <hesitation> coppati la mu soxla ca médd ma, bu demee beneen doog a wàcc lekksi.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
29445aa2-01f8-45e3-b141-ce756e7db50b
|
737ce947-7603-42b7-a86c-a850eda7bab6
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f025
|
Are there any foods that are believed to help improve strength?
|
s01
| 17.0075
|
waaw lekk yu mel noonu bëri na yi ay lekk yi nga xamante ne su ma ko lekkee danaa di yëg cawarte. Lu ci mel ni jaxatu xaaraan suma yaram lu mu téye téyandiku téyandiku su ma ko lekkee dafay bàyyandinku, waaw su ma yaram lu mu nu mu nagam nagam nagam su ma lekkee jaxatu dina ko dëgëral.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
bf3af8ab-a5ad-45ad-8aaf-26b2ad08df9e
|
5dde4f70-1f4a-493e-9b01-fb24cc7ef092
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
f025
|
Are there any foods that are believed to help improve strength?
|
s01
| 37.216438
|
Su fekkee ne dama toog nii sawarte nekkut ci man <hesitation> bu ma dawee tuuti sonn, walla su ma liggéeyee tuuti sonn dinaa di faral di jëfandikoo limoŋ, saay bu ma jëfandikoo limoŋ ma ut ci lu xaw a sakkan tuuti, ma xar ko, ma daa di ko baxal baxal ko ba mu ñor daal di ko <hesitation> nal ci benn kopp def ci tuuti lem, su ma ko naanee rek damay yëg cawarte gu mel ju ma newoon ci man yëpp <noise> mu dellusiwaat ci man. Ñaari lekk yooyu daal naa ko di jëfandikoo toujours lu ci bëri su ma demee ba nga xamante ni yëguma cawarte walla yëguma wér-gu-yaram sama biir yaram lu ci mel ni jaxatu walla kànja, walla limoŋ, bëri naa lu ma koy jëfandikoo lool su ma yëul wér-gu-yaram sama biir yaram <noise>.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
af468e91-9a3c-4740-a48a-3039fc77abab
|
5dde4f70-1f4a-493e-9b01-fb24cc7ef092
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h048
|
Could you describe how a drum produces sound?
|
s01
| 17.709063
|
Ah sabar nag lu yàgg la si suñu biir ñun làkkat yi, waa lu yàgg la suñu bii- yàqal nañu lu bëri nag waaye yàgg na si suñu biir itam nag, suñu àndandoor la bi nga xamante ni dem ba ko fi jafe na lool. Dañ koy defaree deru béy yi di koy yett ci ay garab di ko defaree noonu.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
5638985b-4310-4a66-bb10-597e35592fb7
|
a2435c52-f2a3-444a-b111-465c07391d3c
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h048
|
Could you describe how a drum produces sound?
|
s01
| 29.274938
|
Moom nag ni muy joxee dégg mooy soo ko dóoree dafay awu, awu googu noonu mooy def benn union bi nga xamante ni dafay dugg si nopp doomu adama yëngal kawar yi nga xamante ni nekk nañ ci biir nopp bi, bu ko yëngalee dina ko jox température bi nga xamante ne moo moo wër karaw yooyu noonu, loolu bu yëngotoo mooy def son, mu dem ci nopp, mu dem ci cuukel nit soog a dégg, noonu lañ koy déggee. Waaye nag mbir la bi nga xamante ne yàgg na suñ biir lool, ñu yàgg a ànd ak moom lool, waaw.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
dccb96f8-8238-4a9e-8480-cb2ca1df8450
|
a2435c52-f2a3-444a-b111-465c07391d3c
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
a069
|
How do birds build their nests?
|
s01
| 16.24325
|
waa pittax nu ñuy defaree seen néeg <hesitation> bari na bari na pi- pittax yi dañu bari ay façon. Am na ñi nga xamant pittax yi nga xamante dañuy ràbb tagg comme ni yeneen picc yi di ràbbee tagg, waaye nag yooyu pittax yooyu moom yooyu bariwuñu, pittax <unintelligible> waa.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
97ecf988-3c23-4cdb-afcc-b112fb22f6d7
|
ce303b34-8ca3-4b9c-816b-00d4b952ad5b
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
a069
|
How do birds build their nests?
|
s01
| 54.991
|
Picc yi ni ñuy ràbbee seen tagg bari na ay façon, am na yi nga xamante ni dañuy defal lal mu doon seen tagg, am ñi nga xamante ni dañuy defal xëdd, dañuy xëdd am picc yoo xam ne dañuy xëdd, lu ci mel ni picc yu ñuy tuddee <hesitation> koco-koco yooyu dañuy xëdd, waaye lu ci mel ne pittax ñoom dañuy defal lal ak ay tan yii nii njànaaw yooyu noonu ay lal lañuy defar. Waa ay lal lañuy defar ci kaw lal yu yaatu yoo xam ne dañ ciy tëdd, waaye ñoom seen néeg yooyu du baare taw, waaye am na ci picc yi nga xamante ni seen nid day baare taw lu ci mel ne koco-koco buy taw tamit biir néegam du tooy moom dina ko de léegi liggéey ràbb ko ba nga xamante ni biir néegam du taw, yu ci bari nag ñax lañuy defaree, ak yi nga xamante ni ñax bant bu dem ba doon bant, amul ñax yi nga xamante ni yu mel ni koco-koco ñax bi nga xamante ni dafay oyof doon guntax doon gàncax ñoom boobu lañ dee dagg di ko xonc, dem di ràbb seen tagg.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
1c69c2ea-7b37-4880-87cf-98d588737cdb
|
ce303b34-8ca3-4b9c-816b-00d4b952ad5b
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
a069
|
How do birds build their nests?
|
s01
| 13.582688
|
Moo tax ñoom seen tagg yooyu noonu bu nawetee taw bu ñëwee sax dafay mën a ñàkk yàq taw bi, taw bi da koy mën a ñàkk a tooyal. Moo tax ñoom picc yooyu noonu ci côté dëkkuwaay moom ñoom ñoo ci gën a yeewu yeneen picc yi, ndax ñoom noonu lañu utiliser.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
024bd5de-6cef-4259-8cbd-aa1da35bfad2
|
ce303b34-8ca3-4b9c-816b-00d4b952ad5b
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
a069
|
How do birds build their nests?
|
s01
| 15.123
|
Léegi nag picc yi moom taw bu ñëwee mun nañ di tawte waa, ngelaw bu ñëwee dinañ di mën a daane seen tagg yi. Waaye koco-koco moom jafe na lool ngelaw daane taggam, jafe na lool taw dugg ci biir taggam, moom yeemu côté boobu moom, am na xarañteef ci côté googu bu baax a baax.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
32ec6c94-c836-4d98-8b3a-e68ac697634e
|
ce303b34-8ca3-4b9c-816b-00d4b952ad5b
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h053
|
Could you give a very simple explanation of how an airplane flies?
|
s01
| 58.380563
|
waaw <hesitation> fofalnaaw nag olof yi ñoo koy wax fofalnaaw, fofalnaaw nag benn jumtukaay la bi nga xamante ni xarañteefu nit moo ko liggéey, xarañteefu nit moo ko liggéey mu doon li nga xamante ne yombal na lool dem ak dikk doomu adama ci kaw dund ci biir dundu doomi adama yombal na ko lool. muy mbir mi nga xamante ni bokk na ci li nga xam ne da koy dimbale pour mu naaw mooy mu am jaww ji nga xamante ni set na lool. Ndax jaww ji lu ñuy tuddee atmosteeri jaww ji bu amee ay tolof-tolof rek moom bu jógee ci kaw dina di yomb a am tolof-tolof oxygène mu am ngelaw bu mut no- bu nit ki nokkee dina di yomb a am tolof-tolofam, manaam bu jaaree si zone bi nga xamante ni, walla béréb bi nga xamante ni bëri na lool ay mbir yi nga xamante ni xew bi na ciy xew ci bërëb boobu noonu di jëm di yéeg ci kaw flon asamaan si dina di yàqal avion bi. <hesitation> fol fol nag fofalnaaw bi ay ay kii nii ay jëmuwaayam, parce que li nga xamante ni dina ko di soxla ci ngelaw daf koy manquer te bu ko manquer mën na lor ñi nekk ci biir.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
8feb7fe5-01e2-4924-8c94-6a3efe3686b0
|
0795f6d8-6c5f-4dc5-b428-c7816b6525e5
|
|
wof_Latn
|
spk16
|
h053
|
Could you give a very simple explanation of how an airplane flies?
|
s01
| 9.783438
|
Pour mu am lu ko lu gën ci moom nag mooy mu am jaww bi nga xamanete ni set na wicc jaww ji nga xamante ni sell na, mu mën a naaw ba wàcc yombal dundu dundi doomi adama.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
22153664-1092-4a9a-bb18-74289442e324
|
0795f6d8-6c5f-4dc5-b428-c7816b6525e5
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i055
|
Can you explain how to wash your hands properly?
|
s01
| 13.126063
|
Waaw moom it dafa laajte <hesitation> nit ki naka laay raxasee loxoom bam set. Raxas loxo pour mu set, ba ja njëkk daal mooy na ndox ma set.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
a7de3fa0-7b6e-4806-a1aa-67645fd46d18
|
072d50c9-6b5f-46bc-b830-b37423a058a6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i055
|
Can you explain how to wash your hands properly?
|
s01
| 18.128313
|
Yaw mi koy raxas, naŋ ko jonju mu daj ak yaw loo ko mën a booleel pour mu dimbali la ci li taqe ci loxo bi dëñ, nga boole ko ca. Waaye loxo bi daal, benn bu sa ne dana ragg moroom ma, ba li nga xam ne moo ci taq dana hippiku.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
cc0a63eb-433f-4ad1-bd98-8de368b3b41a
|
072d50c9-6b5f-46bc-b830-b37423a058a6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
i055
|
Can you explain how to wash your hands properly?
|
s01
| 12.185625
|
Nga dugal ko si ndox mi njonju ko ba xam ne ndox mi dana yóbbaale lépp lu taqoon ci loxo yi. Nga am meneen ndox nga dugal ko, mu layangi sa raxasu, sa raxasu set.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
ee7cbebc-0d9e-4b26-bac0-e421dfda2b8e
|
072d50c9-6b5f-46bc-b830-b37423a058a6
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 5.740625
|
Bàyyi na aadaam. Loolu lañ ko miinee, te nit ku ne lam la miinee lay xam ci yaw la jegeleek moom.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
21159cf3-d8c3-47e7-854b-46f4923a36a8
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 9.741063
|
Mu undi aada da dund. Ñuni tamit lañ miin ak la ñu juddu fekk ko fi, muy aada ci ñun mooy mbubb mu job, mbubb mu rëy.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
222171c4-8372-49e5-b7fe-7fce5671d1aa
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 4.4005
|
Yaar yooyu de ham na. Mbubb mu jot ak mbubb bu réy.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
469f4770-aebf-40e6-94fc-fc02ee550677
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 17.802
|
Am na yow, li ngay doon doon xale, ham na yëre yu boo ko solee, dañ la jox cër boo xam ne, duñ ko de jox xale. Cër baa la ko may. <hesitation> boo ko solee, tay boo jëloon sabadoor sol ko, jël laafa teg ca, boo ñëwee duma la taaj ci suuf.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
be557228-2c16-40ec-a152-2d7d694ea4c7
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 7.860875
|
Fokk ñu jox la cër. Gune gu heroo ngi nii paska yenenn yooyu lu muy address, maanaam lii, lu muy wone.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
70dcd266-5b47-4380-a200-c681931846ba
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 6.040688
|
Maa ngi baalu àq ci tubaab yi sax. Li mooy wane ci nit ki mooy lii a ko neex.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
02113b39-8919-4b3d-9772-b642ef7202af
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 7.700875
|
Kon nii la mel. Walla kii lile koo neex, li tax mu sol hére hii, kon hiree ko neex.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
6a04989f-0c2e-49b6-bc82-5561a9400d7b
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 8.941
|
Ki nga xam ne <hesitation> mel neneen moo ko neex moo tax mu def kawarom gi mu mel neneen, sol yëre yoo xam ne dañ ko xotti. Mu mel neneen.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
5dd192bf-6322-41d0-a92d-5be125fea990
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 4.940563
|
Ham na keneen ku moo roy ku bokkul ak lii. Lii moo undi yëre yu wuute.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
1a454d10-546e-4b9d-b523-46cb4afb2102
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
c091
|
Is there a particular style of clothes you like to wear?
|
s02
| 11.621313
|
Ci man nag, bu ma dee sol la may sol mooy yëre yu guddu, yu jot walla yëre yu rëy yu rafet. Man ibba maadi silla de loolu laa bëgg.
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
1740e4f9-463c-4cf8-9550-15ebd0bb1342
|
ab88e176-4c4e-4d3c-9170-49c23a53c97c
|
|
wof_Latn
|
spk01
|
p104
|
Is it possible to live without regrets?
|
s01
| 9.061063
|
Waaw laaj bi mu ne <hesitation> ci gàttal ndax nit mun na góor- góorlu dundu be du réccu. Waaw!
|
wof
|
gamb1252
|
Latn
|
85295953-54e2-4145-980c-403207e2e518
|
1f68a200-ece1-48b5-a2ec-d75c5c217904
|
End of preview. Expand
in Data Studio
README.md exists but content is empty.
- Downloads last month
- 12